Sabóor 118
Aji Sax jeek man, ma daan
Santleen Aji Sax ji, kee baax,
kee saxoo ngoram!
Rikk Israyil, neleen:
«Kee saxoo ngoram!»
Rikk waa kër Aaróona, neleen:
«Kee saxoo ngoram!»
Rikk yeen ñi ragal Aji Sax ji, neleen:
«Kee saxoo ngoram!»
 
Ci xat-xat laa wooye Ki Sax wall,
Ki Sax wuyu ma, yaatal ma.
Aji Sax jeek man, duma tiit.
Ana lees ma manal?
Aji Sax jeek man, di ma dimbali,
may seetaan bañ yi.
Làqoo Aji Sax jee gën
wóolu doom aadama,
Làqoo Aji Sax jee gën
wóolu garmi.
10 Yéefar yépp a ma sam,
ma bëmëx leen ci dooley Aji Sax ji.
11 Ñu sam maa sam,
ma bëmëx leen ci dooley Aji Sax ji.
12 Naka lañu ma sam niy yamb,
jekki ne kamaj ni taalu boob,
ma bëmëx ci dooley Aji Sax ji.
13 Dees maa jañaxa jañax, ma ter-teri,
Aji Sax ji dimbali ma.
 
14 Sama doole, sama kaaraange, Ki Sax a;
te mooy sama wall tey.
15 Ndam aki sarxolle ca xaymay ñu jub ña,
ndijooru Aji Sax jee def njàmbaar!
16 Ndijoor la Aji Sax ji xàcci,
ndijooru Aji Sax jee def njàmbaar.
17 Duma dee moos, xanaa dund,
ba nettali jaloorey Ki Sax.
18 Ki Sax mbugal na maa mbugal,
waaye waccu ma, ma dee.
19 Ubbil-leen ma bunti njekk,
ma dugg santi Ki Sax.
 
20 Buntu Aji Sax jaa ngi;
ñu jub ñee ciy dugge.
21 Dama lay sant, yaa ma nangul,
wallu ma tey.
22 Doj wi tabaxkat yi beddi woon,
moo mujj doju coll wi.
23 Lii de, Aji Sax jee ko def,
nu gis ko, yéemu.
24 Bésub tey jii, Aji Sax jee;
nan ko bége, bànneexoo ko.
25 Ngalla Aji Sax ji, wallu nu.
Ngalla Aji Sax ji, may nu ndam.
26 Yal na Yàlla barkeel ki dikke turam.
Nu ngi leen di ñaanale fi néegu Aji Sax ji.
27 Aji Sax jee di Yàlla, di nu leeral.
Ŋàbbleen car yi, màggale,
te dox ba ca béjjéni sarxalukaay ba.
28 Yaa di sama Yàlla, ma di la sant;
céy sama Yàlla, dama lay kañ.
29 Santleen Aji Sax ji, kee baax,
kee saxoo ngoram.