Sabóor 119
Aji Sax ji, sa kàddu laay bége
Ndokklee yaw mi maandu,
di wéye yoonu Aji Sax ji.
Ndokklee yaw miy wattu kàdduy seedeem,
di ko sàkkoo sa léppi xol.
Doo def njubadi,
di topp fi mu la jaarloo.
Aji Sax ji, yaa joxe sa tegtal
yi ñu wara toppa topp.
Yal naa saxoo
di sàmm sa dogali yoon,
di teewlu loo santaane,
ba duma rus.
Damay gëstu sa ndigal yu jub,
di la sante xol bu dëggu.
Sa dogali yoon laay sàmm;
ngalla bu ma wacca wacc.
 
Ana nu ndaw mana sellalee?
Xanaa di sàmm sa kàddu.
10 Sama léppi xol laa lay sàkkoo,
bul ma wacc, ma wàcc say santaane.
11 Sama xol laa làq say wax,
ngir bañ laa moy.
12 Jaajëfe, yaw Aji Sax ji,
jàngal ma sa dogali yoon.
13 Maa àddu, tari
mboolem lu sa kàddu digle.
14 Topp say tegtal laay bége
mbégtem jépp alal.
15 Say tegtal laay jàngat,
di teewlu say xàll.
16 Sa dogali yoon, ma tàqamtikoo,
sa kàddu, ma fat ba fàww.
 
17 Sang bi, baaxe ma, ma dund,
ba mana sàmm sa kàddu.
18 Ngalla muril saay gët, ma niir
sa kéemaani yoon.
19 Doxandéem laa fi kaw suuf,
bu ma làq say santaane.
20 Fu ma tollu maa ngi namm say ndigal
ba sama xol ŋiis.
21 Rëbb nga ñu reew, ñu alku,
ñiy dëddu say santaane.
22 Musal ma ciy kókkaleeki xaste,
maa ngi topp sa kàdduy seede.
23 Te it kàngam yaa ngi may tooge,
te may gëstu sa dogali yoon, Sang bi.
24 Sa kàdduy seede laay safoo,
ñuy sama xejj yi may xelal.
 
25 Maa ngi ne ñàyy ci pënd bi,
musal ma, yaa ko dige.
26 Wax naa la samay jaar-jaar, nga wuyu ma;
ngalla xamal ma sa dogali yoon.
27 Dégtal ma li sa tegtal yiy firi,
ma jàngat say kéemaan.
28 Naqaru xol sonal na ma,
may ma ndëgërlaay, yaa ko dige.
29 Sorele maak yoonu fen,
te baaxe ma saw yoon.
30 Yoonu worma laa taamu,
jàkkaarlook say ndigal.
31 Éy Aji Sax ji, damaa langaamoo sa kàdduy seede,
ngalla bu ma rusloo.
32 Sa yoonu santaane laay daw,
yaa may may xol bu tàlli.
 
33 Aji Sax ji, xamal ma li sa dogali yoon yiy firi,
ma topp ko ba mu jeex.
34 May ma dég-dég, ma topp saw yoon,
toppe ko xol bu tàlli.
35 Jiite ma ci sa xàllu santaane yi,
mooy sama bànneex.
36 Joyantil sama xol, mu féeteek sa kàdduy seede,
te dummóoyu alal ju lewul.
37 May ma, ma fénati caaxaani neen,
te musale ma saw yoon.
38 Sang bi, sottalal ma sa dige
bi nga digook ku la ragal.
39 Moyale ma gàcce gi ma ragal;
yaa baaxi ndigal.
40 Maaka namm say tegtal,
musale ma sag njekk!
 
41 Aji Sax ji, yaa ko dige,
dikke ma sa jëfi ngor ak sa wall,
42 ba ku ma kókkali, ma am tontam.
Maa doyloo sa kàddu.
43 Bu ma xañ mukk kàddug dëgg,
say àtte laa yaakaar kat.
44 Maay topp saw yoon, sàlloo ko,
saxoo ko ba fàww,
45 di daagoo sago,
nde say tegtal laay sàkku.
46 Maay àgge ay buur sa kàdduy seede,
te duma rus.
47 Maay bége sa santaane
yi ma sopp,
48 di yóotu sa santaane yi ma sopp,
di jàngat sa dogali yoon.
 
49 Bàyyil xel li nga ma dig, Sang bi;
moom laa yaakaar.
50 Lii laay muñe samaw naqar,
sa kàddoo may dundal.
51 Nit ñu bew ñi ñaawal nañu ma lool,
waaye dëdduwma saw yoon.
52 Éy Aji Sax ji, damaa fàttliku sa àtte ya woon,
daldi muñ.
53 Sama xol daa fees ndax ñu bon
ñiy wacc saw yoon.
54 Sa dogali yoon laay woyantoo,
fu ma mana sance.
55 Aji Sax ji, tudd naa la guddi,
di sàmm saw yoon.
56 Lii laa séddoo,
maa topp sa tegtali yoon.
 
57 Aji Sax ji, yaw laa séddoo;
di digee sàmm sa kàddu.
58 Sama léppi xol laa sàkkoo saw yiw,
ngalla baaxe ma, yaa ko dige.
59 Damaa seetlu sama jëfin,
dëpp, topp sa kàdduy seede.
60 Maa ngi gaawtu,
yeexewma say santaane moos!
61 Buumi ñu bon ñaa ngi may laaw,
te sàgganewma saw yoon.
62 Xaaju guddi laay jóg,
di la sante sa àttey njekk.
63 Maa xejjoo képp ku la ragal,
tey topp say tegtal.
64 Aji Sax ji, sa ngor dajal na àddina;
xamal ma sa dogali yoon.
 
65 Aji Sax ji, def nga la nga dige woon,
Sang bi, defal nga ma ngëneel.
66 Xamal ma ngëneeli àtte ak xam-xam,
maa doyloo say santaane.
67 Maa jàddoon, nga duma ma,
léegi sa kàddu laay sàmm.
68 Yaaka baax tey baaxe;
rikk xamal ma say tegtal.
69 Ñu bew ñee yàq sama der aki sos,
te ma topp say tegtal, wéetal la.
70 Ñu ngi nii, seen bopp yi, tafas;
te man may tàqamtikoo saw yoon.
71 Ngëneel la ma duma yi jural,
ngir jànge naa ci say tegtal.
72 Sa ngëneelu yoon wi nga digle
moo ma gënal ay junniy xaalis ak wurus.
 
73 Say loxoo ma sàkk, tabax ma,
may ma ag dégg, ma mokkal say santaane,
74 ñi la ragal gis ma, bég;
nde sa kàddu laa yaakaar.
75 Aji Sax ji, ràññee naa ne say ndigal njekk la,
te worma nga ma dumaa.
76 Ngalla dëfale ma sa ngor;
Sang bi, yaa ko dige.
77 Nanga ma ganesee sa yërmande, ma dund;
saw yoon ay sama bànneex!
78 Yal na ñu bew ñi torox,
ñoo ma lor ak seeni sos,
te man may gëstu say tegtal.
79 Yal na ku la ragal waññiku fi man,
ba xam sa kàdduy seede.
80 Yal naa toppe say tegtal xol bu mat sëkk,
ba duma rus.
 
81 Sàkku naa sag wall ba xol jeex,
di xaar sa kàddu.
82 Séentu naa sab dige, ba gët giim;
kañ nga may xettli?
83 Damaa mujj ras ni mbuusum der mu saxar jàpp,
waaye sàgganewma say tegtal.
84 Ñaata fan laay toogati, Sang bi?
Kañ ngay mbugal ñi ma topp?
85 Ñu bew ñi gasal nañu ma ay yeer,
yu saw yoon diglewul.
86 Sa santaane yépp worma la;
te dees maa toppey sos, wallu ma!
87 Nes tuut ñu sànke ma fi kaw suuf,
te man dëdduwma say tegtal.
88 Musale ma sa ngor,
ba jëfe sa kàdduy seede.
 
89 Aji Sax ji, sa kàddoo sax dàkk,
taxaw jonn fa asamaan.
90 Sa worma, ba maasoo maas,
yaa samp suuf, saxal ko.
91 Ci sa ndigal la lépp taxawe ba tey,
lépp ànd, di la jaamu.
92 Su ma bégewuloon saw yoon,
sànkoo sama toskare ji.
93 Duma fàtte mukk say tegtal,
ci nga may musale.
94 Yaa ma moom, wallu ma;
say tegtal laay sàkku.
95 Man la ñu bon ñi tëru, nar maa sànk,
waaye sa kàdduy seede laay niir.
96 Gis naa ne lu mat lu ne am na kemu,
waaye sa santaane mat ba wees kemu.
 
97 Maaka sopp saw yoon,
di ko jàngat bés bu jot.
98 Li ma xelal ba ma raw noon yi,
mooy sa santaane, yi ma jagoo fàww.
99 Maa gëna ñaw képp ku may jàngal,
nde sa kàdduy seedeey sama njàngat.
100 Maa ëpp mag ñi dég-dég,
nde say tegtal laa topp.
101 Luy yoon wu aay, ma moyu,
ba mana sàmm sa kàddu.
102 Say santaane it dëdduwma ko,
nde yaw yaa ma jàngal.
103 Sa kàddooka maa neex,
ba dàqal ma tem-temu lem!
104 Say tegtal laay ràññee,
ba tax ma bañ luy yoonu fen.
 
105 Sa kàddu laay niitoo samay tànk,
muy leeral samaw yoon.
106 Giñ naa te di ko dëggal,
ne dinaa sàmmonteek sa ndigali njekk.
107 Toskare naa ba ci lool;
éy Aji Sax ji, musal ma, yaa ko dige.
108 Aji Sax ji, rikk nangul ma kàdduy cant yi ma lay jébbal,
te xamal ma say ndigal.
109 Sama bakkan ci xott saa su ne,
waaye fàttewuma saw yoon.
110 Ñu bon ñi ma gasal um pax
taxul ma wàcc say tegtal.
111 Maa séddoo fàww sa kàdduy seede,
loolooy seral sama xol.
112 Damaa dogoo jëfe sa dogali yoon,
saxoo ko ba mu jeex.
 
113 Maa bañ kuy ŋarale,
maa sopp saw yoon.
114 Sama rawtu, sama kiiraay, yaw a;
sa kàddu laay xaar.
115 Yeen ñiy def lu bon, xiddileen ma,
ba ma sàmmonteek sama santaaney Yàlla.
116 Yaa ko dige, dooleel ma, ma dund;
bul tas sama yaakaar.
117 Kàttanal ma, ma raw,
di yittewoo say tegtal, ba fàww.
118 Yaay xarab képp ku wàcc sa dogali yoon,
ay pexeem neen.
119 Yaay tonni ni purit képp ku bon fi kaw suuf,
moo tax ma sopp sa kàdduy seede.
120 Sama yaram a ngi daw ndax ragal la,
ragal say àtte.
 
121 Def naa njub, def njekk;
bu ma wacce ñi may néewal.
122 Sang bi, gàddu ma, ma am jàmm,
bu ma ñu bew ñi néewal.
123 Séentu naa sag wall ak sa kàddug njekk,
ba saay gët giim.
124 Sang bi, jëfeel ma sa ngor,
xamal ma sa dogali yoon.
125 Sab jaam laa, may ma, ma ràññee,
ba xam sa kàdduy seede.
126 Aji Sax ji, jëf jot na,
ñee ngi jalgati saw yoon!
127 Maa sopp say santaane,
mu gënal ma wurus ba ci wurusu ngalam.
128 Moo tax foo tegtale, ma rafetlu,
lépp luy yoonu fen, ma bañ.
 
129 Sa kàdduy seede kéemaan la,
moo tax ma di ko toppe xol.
130 Sa pirim kàddu day leeral,
di xelal ku xeluwul.
131 Damaa ŋa ŋafeet, di àppaat,
ngir namm say santaane.
132 Éy geesu ma te baaxe ma,
ni nga baaxook ñi sopp sa tur.
133 Dooleelal ma samay tànk, yaa ko dige,
te bu ma lenn lu bon man.
134 Jot ma ci noteelu doom aadama,
ma mana topp say tegtal.
135 Sang bi, geesoo ma sag leer,
te xamal ma sa dogali yoon,
136 ay wali rongooñ ay wale saay gët,
ndax sàmmeesul saw yoon.
 
137 Aji Sax ji, yaaka jub,
te say àtte di yoon.
138 Yaa santaane sa kàdduy seede ci njekk
ak worma ju yaa.
139 Damaa gis bañ yiy sàggane say wax,
xol bu tàng di ma rey.
140 Sang bi, maaka sopp sa kàddu
gi set ni weñ gu ñu xelli!
141 Ñàkk naa solo, faaleesu ma,
waaye sàgganewma say tegtal.
142 Sag njekk moo dig njekk ba fàww,
te saw yoon a dëggu.
143 Njekkar ak njàqare dab ma,
say santaane di sama bànneex.
144 Sa kàdduy seedee di njekk ba fàww,
may ma, ma ràññee, ba dund.
 
145 Aji Sax ji, woo naa la wall lu ma man,
wuyu ma, ma topp sa dogali yoon.
146 Dama ne: «Wóoy, wallu ma,
ma sàmm sa kàdduy seede.»
147 Damaa jëlu, di la woo,
di xaar sa kàddu.
148 Damay xoole guddi gépp,
di jàngat sa kàddu.
149 Aji Sax ji, sama baat bii, teewloo ko sa ngor,
te musal ma ni nga baaxoo muslee.
150 Rabatkati pexe yaa ngi jegesi,
di nit ñu sore saw yoon.
151 Waaye yaw Aji Sax ji, jege nga,
te sa santaane yépp a dëggu.
152 Yàgg naa xam ne sa kàdduy seede
wax la joo saxal dàkk.
 
153 Xoolal sama coono te xettli ma;
saw yoon déy, sàgganewma ko.
154 Àtte ma, ba jot ma;
musal ma, yaa ko dige.
155 Ku bon sore sa wall,
ngir sàkkuwul sa dogali yoon.
156 Aji Sax ji, sa yërmande yaa na;
musal ma ni nga ko baaxoo.
157 Ñi ma topp ak ñi ma baña bare,
te taxul ma dëddu sa kàdduy seede.
158 Damaa gis workat yi, sib leen;
ñoo sàmmul sa kàddu.
159 Seetlul ni ma soppe say tegtal.
Éy Aji Sax ji, musal ma, yaa gore!
160 Sa mboolem kàddu dëgg la,
sa ndigal yépp di njekk, sax dàkk.
 
161 Ay kilifaa ma topp ci dara,
te teewul ma wormaal sa kàddu.
162 Man de, maa ngi bége sa kàddu
ni ku for alal ju bare.
163 Fen, ma bañ, ba sib;
sa yoon, ma sopp.
164 Juróom yaari yoon ci bés
màggale naa la ko say àttey njekk.
165 Jàmm ju baree ñeel ku sopp sa yoon,
te dara du ko fakktal.
166 Aji Sax ji, sa wall laa yaakaar,
say santaane laa jëfe.
167 Sama xol laa toppe sa kàdduy seede,
te sopp koo sopp.
168 Damaa topp say tegtal ak sa kàdduy seede,
fépp fu ma jaar kay yaa ngi ciy gis.
 
169 Aji Sax ji, yal na sama yuux àgg fa yaw;
may ma, ma ràññee, yaa ko dige.
170 Yal na sama dagaan àgg fa yaw;
xettli ma, yaa ko dige.
171 Naa xaacu, woyal la,
yaa may jàngal sa dogali yoon.
172 Naa woye sa kàddu,
loo santaane, njekk la.
173 Yal nanga ma dikke ndimbal,
say tegtal laa taamu.
174 Aji Sax ji, namm naa sa wall,
sa yoon ay sama bànneex.
175 Yal naa dund ba màggal la,
say ndigal di sama ndimbal.
176 Lajj naa ni xar mu réer;
gindi ma, Sang bi,
sàgganewma say santaane de!