Sabóor 138
Aji Sax ji waccu ma
Ñeel Daawuda.
 
Ma sante la sama léppi xol,
woy la, gàngooru Yàlla ga ca kaw seede.
Ma sujjóot jublook sa kër gu sell gi,
di wormaal saw tur,
ngir sa ngor ak sa worma.
Màggal nga sa tur ak sa kàddu,
ba mu tiim lépp.
Bés ba ma wootee, yaa ma wuyu,
ñemeel ma, dooleel ma.
 
Aji Sax ji, na la buuri àddina yépp màggal,
ñoo dégg kàddu yi nga wax.
Nañu woy say jaloore, naan:
«Aji Sax jeeka màgg teddnga!»
Aji Sax jee kawe!
Ku toroxlu, mu niir;
ku réy, mu ñooru.
 
Ma wéye njàqare,
nga musal ma,
dogalee sa loxo merum noon,
walloo ma sa ndijoor.
Aji Sax jee may feyul.
Éy Aji Sax ji, yaa saxoo ngor!
Bul wacc ñi nga binde sa loxo.