Sabóor 139
Aji Sax jee ma xam, ba jeexal ma
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor.
 
Aji Sax ji, yaa ma natt, xam ma;
yaa xam sama toogaay ak sama taxawaay,
di ràññee fu sore samay xalaat,
di càmbar samab dox ak sama tëraay,
yittewoo lépp lu may def.
Aji Sax ji, bala maa wax baat,
ndeke yaw, xam nga lépp.
Kanam ak gannaaw nga ma dare,
teg ma sa loxo.
Ni nga ma xame daa yéeme,
xóot lool, ba wees ma.
 
Fu ma jëm, ba sore la?
Fu ma daw jëm, foo teewul?
Ma ñalgu ba asamaan, yaa nga fa!
Ma tëri njaniiw, ndeke yaa nga fa!
Ma war laafi njël,
dëkki wàllaa géej,
10 nga tettee ma fa ba tey,
téyee ma sa ndijoor.
11 Su ma noon: «Na ma lëndëm mëdd boog,
ba leer gi far guddil ma,»
12 du tax lëndëm lëndëmal la dara.
Guddi da laa leeralal ni bëccëg,
lëndëm dig leer fi yaw.
 
13 Yaa ma sàkkal xol ak xalaat,
ràbbe ma sama biiru ndey.
14 Naa la sante sama bind bu raglu bii te yéeme,
say jalooree di kéemaan, bir na ma!
15 Sama jëmm jii umpu la,
ba muy bindu ci kumpa,
mel ni lu ñu ràbbe ci xóotey suuf.
16 Gis nga ma, ba ma diw lumb;
sa téere lim na
fan yi nga ma àppal,
ba ca benn dooragul.
17 Yàlla, say xalaat aka maa yéem!
Ndaw lim bu réy!
18 Su ma ko doon waññ, moo ëpp feppi suuf.
Maa ngii yewwu, ne feek yaw ba tey.
 
19 Éy sama Yàlla, soo reyoon ñu bon ñii!
Yeen bóomkat yi, soreleen ma!
20 Ñii sa tur lañuy luubale,
noonoo la, di tudd sa tur ciy caaxaan.
21 Aji Sax ji, maaka bañ ñi la bañ
te sib ñi lay gàntal.
22 Dama leena bañ ba fa mbañeel yem;
samay noon dëgg lañu.
 
23 Yàlla, seetlu ma, ba ràññee sama xol;
natt ma, ba ràññee sama xalaati xol.
24 Xoolal ndax maa ngi doxe yoon wu aay,
te nga teg ma ci yoon wi sax.