Sabóor 53
Mbon maase na
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Maalat, di taalif bu ñeel Daawuda.
 
Ab dof a nga naa ca xelam:
«Yàlla amul,»
tey def njekkar,
njubadeem siblu,
kenn defu ci lu baax.
 
Yàllaa tollu asamaan, jéer doom aadama,
di seet ku ci xelu,
tey sàkku Yàlla.
Ñépp a dëddu,
bokk yàqu yaxeet.
Kenn deful lu baax,
du kenn sax.
 
Yàlla nee: «Xanaa ñiy def lu bon, xamuñu dara?
Ñuy lekk sama ñoñ niw ñam,
te sàkkuwuñu Yàlla.»
Waaye ñooy tiita tiit
fu tiitaange amul.
Yàllaay tasaare néewi nit ñi la gaw.
Yàllaa leen wacc, nga gàcceel leen.
 
Ana kuy tollu Siyoŋ, xettli Israyil?
Éy, bés bu Yàlla delloo ñoñam ndam,
ndaw mbégte ci giirug Yanqóoba!
Ndaw bànneex ci Israyil gii!