Sabóor 54
Yàlla, dimbali ma
1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, di taalif bu ñeel Daawuda.
2 Mooy ba waa Sif demee ca Sóol, ne ko Daawudaa nga làqu ca seenum réew.
3 Éy Yàlla, musal ma ngir sa tur,
jox ma dëgg, ci sa kàttan.
4 Éy Yàlla, déglul, ma ñaan,
teewlul, ma wax la.
5 Ay doxandéem a ma jógal,
di ñu néeg, bëgga jël sama bakkan,
te seetuñu ci Yàlla.
Selaw.
6 Yàllaa ngii, moo may dimbali;
Boroom bee yor sama bakkan.
7 Yal na ay wi këppu ci ñi may tëru,
yal na leen sa dëgg sànk.
8 Xol bu tàlli laa lay sarxale.
Aji Sax ji, yaa baax,
ma sant la.
9 Lépp luy njàqare, yaa ma ci jële,
ma tiim samay noon.