Sabóor 83
Yàlla, mbugalal noon yi
Di woyu Sabóor, giiroo ci Asaf.
 
Éy Yàlla, bul ne cell,
rikk Yàlla, bul tanqamlu, ne patt.
Xoolal sa noon yiy riir,
sa bañ yi fippu ba téen!
Sa ñoñ lañuy rabatal,
di mànkool sa séddoo yii.
Ñu ne: «Ayca nu far seen xeet wi,
ba deesul fàttlikooti turu Israyil.»
 
Dañoo mànkoo kat,
te yaw lañu takktool:
muy néegi Edom ak Ismayla,
néegi Mowab ak Agar,
néegi Gebal, Amon ak Amaleg
ak waa Filisteek waa Tir,
réewum Asiri it fekki leen,
di dooleel askanu Lóot wa.
Selaw.
 
10 Def leen na nga defoon waa Majan,
def ko Sisera ak Yabin ca dexu Kison*.
11 Ña nga sànkoo Endor,
ba doon ub tos fi kaw suuf.
12 Defal seeni njiit na Oreb ak Seeb,
def seen kilifa yépp ni Seba ak Salmuna,
13 ña ne woon: «Nan séddoo parluy Yàlla yi.»
14 Éy Yàlla, wëndeel leen ni callweer,
ñu mel ni boob mu ngelaw wal.
15 Éy Yàlla, ni daay di xoyome àll,
sawara wa jafal tund ya,
16 yal nanga leen ni toppeek sa dooley ngelaw,
tiitale leen sa ngëlén.
17  Aji Sax ji, sëlëm leen gàcce,
ba ñu sàkku la.
18 Yal nañu rus, jàq ba fàww.
Yal nañu torox, sànku.
19 Yal nañu xam ne yaw mi tudd Aji Sax ji doŋŋ
yaay Aji Kawe ji yilif àddina yépp.
* 83:10 Seetal ci Njiit ya 7—8.