Sabóor 84
Ku dal ak Yàlla bég
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd ak xalam gu ñuy wax gitiit, ñeel askanu Kore wu góor.
 
Aji Sax ji Boroom gàngoor yi,
yaaka sopplub dëkkuwaay!
Damaa namm ëttub Aji Sax ji,
di ko gelu ba jeex tàkk,
jëmm jeek xol bi,
di xaacul Yàlla jiy dund.
Éy Aji Sax ji Boroom gàngoor yi,
sama buur, sama Yàlla,
sawoor sax tag, nga fat ko,
mbelaar it sàkk tàggam,
denc ay cuujam fa sa sarxalukaay.
Ndokklee ku dëkke sa kër,
di la màggalati.
Selaw.
 
Ndokklee ku lay doolewoo,
te namma topp njool ma jëm sa kër.
Buy jàll xuru Jooyoo,
mu saf ko bëti ndox,
céebo sànge xur wa barke,
muy gëna am doole,
ba teewi fa Yàlla ca Siyoŋ.
 
Éy Yàlla Aji Sax ji Boroom gàngoor yi,
déglul, ma ñaan la!
Yàllay Yanqóoba, teewlu ma.
Selaw.
10 Éy Yàlla, geesul Buur, sunu kiirlaay,
ngalla niiral kii nga fal.
11 Benn fan ci sab ëtt de
moo dàq junniy fan feneen.
Sama taxawaayu bunt kër Yàlla
moo ma gënal tëraayu biir xaymab ku bon.
12 Aji Sax ji Yàllaa mat jant, mat kiiraay;
yiw ak daraja, Aji Sax ji joxe;
te du ngëneel lu muy bañal ku mat.
13 Éy Aji Sax ji Boroom gàngoor yi,
ndokklee ku la wóolu.