Téereb Yonent Yàlla
Ose
Saar 1
1 Kàddug Aji Sax jii moo dikkaloon Ose, góor giy doomu Beeri, ci janti buuri Yuda, Osiyas, ak Yotam ak Axas ak Esekiya, ak ci janti buurub Israyil Yerbowam doomu Yowas.
Njabootu Ose misaal la
2 Ba Aji Sax ji tàmbalee yóbbante Ose kàddoom, Aji Sax ji da ne ko: «Demal takki jabaru gànc, nga am ca doomi ngànctu, ndax réew maa ngi gànctu ngànctu gu réy, dëddu ma man Aji Sax ji.» 3 Ose dem takki Gomer doomu Diblayim. Mu ëmb, gannaaw gi mu am doom ju góor.
4 Aji Sax ji ne ko: «Tudde ko Yisreel*1.4 Xuru Yisreellañuy misaale deret ju wale, ndax lañu fa bóomoon ñu bare. Seetal ci 2.Buur ya 9.7-10.31.. Des na tuuti dinaa mbugal askanu buur Yewu ndax deret ji ñu tuur ci Yisreel. Dinaa jeexal nguurug Israyil. 5 Su bés baa maay damm ngànnaayu Israyil ca xuru Yisreel.»
6 Mu dellu ëmb, gannaaw gi mu am doom ju jigéen. Aji Sax ji ne: «Tudde ko Lo Ruwana» (mu firi Ki ñu yërëmul), mu ne: «ndax dootuma yërëm waa kër Israyil, dootuma leen baal. 7 Waaye waa kër Yuda, maa leen di yërëm. Seen Yàlla Aji Sax ji laa leen di walloo, waaye duma leen walloo fitt mbaa saamar, mbaa ay xare, mbaa ay fas aki gawar.»
8 Ba Gomer feralee Lo Ruwana, ëmbaat na, ba am doom, muy góor. 9 Aji Sax ji ne ko: «Tudde ko Lo Ami» (mu firi Du sama ñoñ), mu ne: «ndax dungeen sama ñoñ, te man duma seen dara.»
*1:4 1.4 Xuru Yisreellañuy misaale deret ju wale, ndax lañu fa bóomoon ñu bare. Seetal ci 2.Buur ya 9.7-10.31.