Saar 2
Aji Sax jeey dalalaat ñoñam
«Du tere askanu Israyil tollu ni suufas géej. Deesu ko mana natt mbaa di ko waññ, te foofa ñu leen noon: “Yeen, dungeen sama ñoñ,” fa lees leen naa: “Yeenay doomi Yàlla jiy dund.” Askanu Yuda ak askanu Israyil dañuy dellu booloo, daldi tabbal seen bopp genn kilifa, te dinañu sëq ci réew mi, ndax bésub Yisreel ba dina réy. Nanga wooye sa bokk yu góor: “Ñoñi Aji Sax ji,” sa bokk yu jigéen, nga ne leen: “Ñi Aji Sax ji yërëm.”
Ab layoo rax na kàddug tinu ci Israyil
 
«Tiiñal-leen seen ndey, tiiñal-leen ko,
ndax moom du sama jabar,
te man duma jëkkëram.
Nee ko mu bàyyi gànctu
te noppee tegoo màndargam njaaloo.
Lu ko moy ma futti ko ba mu ne duŋŋ,
def ko ni bés ba mu juddoo,
melal ko ni màndiŋ.
Maa koy def ni joor gu wow,
marloo ko ba rey ko.
Ay doomam, duma leen yërëm,
nde doomi ngànctu lañu.
Ñoom seen yaay moo gànctu,
ki leen ëmb moo def lu gàccelu,
naan: “Damay toppi sama far,
yi may jox sama lekk ak samag naan,
ak samag wëñ ak sama lẽe
ak samag diw ak sama biiñ.”
 
«Moo tax maa ngii di ñage yoonam ay dég,
gawe ko ag wurmbal,
ba yoon réer ko.
Mooy topp ay faram te du leen dab;
mu seet leen, du leen gis.
Su boobaa mu ne: “Naa dellu
ca saa jëkkër ju jëkk ja,
nde ca laa gënoonu demin.”
10 Moom xamul woon ne man maa ko doon jox
pepp meek biiñ bu bees beek diw gi,
di ko yéwéne xaalis ak wurus,
ñu di ko jaamoo Baal.
11 Kon nag fa ngóob jote laay nangoo sama pepp,
fa wittum reseñ jote it laay nangoo
sama biiñ bu bees,
maay foqati sama wëñ ak sama lẽe,
ba mu daan sànge yaramam.
12 Léegi maa koy futti, mu ne duŋŋ,
ay faram di gis,
te kenn du ko xettli ci sama loxo.
13 Maay dakkal gépp mbéxam;
ay màggalam, ay Terutel weeram,
ay bési Noflaayam, ak mboolem bési ndajeem.
14 Maay fóom garabi reseñam aki figgam,
yi mu noon: “Lii sama peyoor la!
Samay far a ma ko jox.”
Maa koy def ay dédd,
rabi àll yi di ko lekk.
15 Maa koy feyu bési màggal yu tuuri Baal,
ya mu leen daan taalale cuuraay,
takk ay jaarooki gànjar,
toppiy faram, fàtte ma.»
Kàddug Aji Sax jee.
Aji Sax ji sàkkuwaat na cofeelu Israyil
16 «Moo tax maa ngii di ko naxtaan,
maa koy yóbbu ca màndiŋ ma,
ba déey ko lu xolam dégg.
17 Foofa laa koy delloo tóokëri reseñam,
defal ko xuru Akor*2.17 xuru Akor mooy xuru Musiba. Seetal ci Yosuwe 7.24-26. di buntu yaakaaram.
Fa la may feeloo na woon
ca janti ndawam,
ba muy génn réewum Misra.
18 Bésub keroog,» kàddug Aji Sax jee,
«Ca nga may wooye “Sama jëkkër,”
te dootoo ma wooye “Sama Baal.”»
19 Turi tuuri Baal laay jële ci sa gémmiñ,
ba deesatul fàttliku seen tur.
20 Bésub keroog maa leen di fasal kóllëre
ak rabi àll yeek njanaaw yi,
ak ndëgmeent yi.
Fitt ak saamar akub xare it,
maa koy dagge ci réew mi,
te maa leen di may tëraayu jàmm.
 
21 «Yaw laay digool ba fàww, ab séy,
te njekk ak njub ak ngor ak yërmande
ci laay digook yaw ab séy.
22 Ci kóllëre laay digook yaw ab séy,
ba nga xam Aji Sax ji.
23 Bésub keroog, maay nangu,»
kàddug Aji Sax jee,
«maay nangul asamaan,
moom, mu nangul suuf;
24 suuf nangul pepp ak biiñ ak diw,
ñu bokk nangul Yisreel.
25 Maa koy jëmbatal sama bopp ci réew mi,
maay yërëm ki tuddoon “Ki ñu yërëmul.”
Ki tuddoon “Du sama ñoñ,”
ma ne ko: “Yaay sama ñoñ,”
moom mu ne ma: “Sama Yàlla.”»

*2:17 2.17 xuru Akor mooy xuru Musiba. Seetal ci Yosuwe 7.24-26.