Saar 62
Yerusalem mooy siggi, mucc
Siyoŋ a tax duma selaw,
Yerusalem laa ne, moo tax duma noppi,
ba kera ceeñeeru njekkam teew,
jumu muccam dikkal ko.
Su boobaa xeet yi gis sag njekk,
buur yépp gis sa daraja,
ba ñu di la tudde tur wu yees,
wu Aji Sax ji di tuddal boppam.
Yaay doon kaalag teddnga
ci loxol Aji Sax ji,
yaay doon mbaxanam buur,
ci sa biir loxol Yàlla jii.
 
Deesatu la wooye «Dëkk bi ñu wacc,»
deesatul wooye sam réew «Réew mu gental.»
Xanaa ñu wooye la «Dëkk bi ma neex,»
tey wooye sam réew «Boroom jëkkër,»
nde yaa neex Aji Sax ji,
te sa réew mi dina am boroom kër.
Ni xale bu góor di takke ab janq,
ni la la sa doom yu góor di moome ni jëkkër*62.5 doom yu góor yi ñooy waa Yuda, te ñooy moom seen réew.;
ni boroom séet di bégee ab séetam,
ni la la sa Yàlla di bégee.
 
Yerusalem, tabb naa ay jongrukat
ci sa kawi tata.
Buñu selaw, du guddi du bëccëg!
Yeen ñiy soññ Aji Sax ji,
buleen dal-lu.
Buleen may Aji Sax ji fu mu dal-loo,
ba kera muy taxawalaat Yerusalem,
ba def ko sababu cant fi kaw suuf.
 
Aji Sax jee giñ lii ci ndijooram,
giñ ko ci përëgam bi àttan,
ne: «Dootuma joxe sam pepp,
say noon dunde,
te doomi doxandéem dootuñu naan
sa biiñ bu bees,
bi nga ame saw ñaq.
Ñi góob pepp mee koy lekk,
di ko sante Aji Sax ji.
Ñi witt reseñ jeey naan biiñ bi,
fi sama biir ëtt bu sell.»
10 Jàllsileen, jàllsileen bunti dëkk bi,
xàll-leen yoonu xeet wi,
maasaleleenoo, maasaleleen ngér mi,
dindi doj yi!
Yékkatileen raaya ju askan yépp gis.
11 Aji Sax jaa ngoog,
yéene na lii ba ca cati àddina.
Mu ne: «Waxleen Siyoŋ dëkk bu taaru bi, ne ko:
“Sab jotkat a ngii di dikk!
Mu ngii ànd akub yoolam,
ñaqu liggéeyam jiitu ko.”
12 Dees na leen wooye “Askan wu sell wi,”
“Ñi Aji Sax ji jot;”
te yaw Yerusalem dees na la wooye “Ki ñu namm,”
“Dëkk bi ñu waccul.”»

*62:5 62.5 doom yu góor yi ñooy waa Yuda, te ñooy moom seen réew.