Saar 63
Jàmbaaru Aji Sax ji am na ndam
Ana kuy kii bawoo Edom*63.1 Edom mi doon seexu Yanqóoba, moom lañu dippee réewum Edom, te moo taxawe taxawaayu noonub Aji Sax ji.,
sol yére yu xonq, bawoo Boccra63.1 Boccra ab dëkk la ci réewum Edom.?
Kii ak yéreem yu yànj,
di daagoo dooleem ju bare?
«Xanaa man mii di waxe njekk,
te am dooley walloo.»
Lu waral sa xonqaayu mbubb mi,
sa yére yi mel ni ku doon dëre
dërukaayu reseñ?
«Maa doon dëre tànk, man kenn
ci ab dërukaayu reseñ,
xeet yépp kenn dërlewu ma ci.
Sama mer laa leen dëre,
samam sànj laa leen dëggaatee,
seen deret tis ci samay yére,
ma taqal sama yére yépp.
Bésub mbugal laa mébétoon,
te atum njot teew.
Ma xool,
gisuma ku ma dimbali,
ma tiislu li ma amul ku ma jàpple.
Ca la ma sama përëg wallu,
samam sànj jàpple ma ca.
Sama mer laa dëggaatee ay xeet,
samam sànj laa leen màndal,
sotti seen deret fi suuf.»
Yonent baa ngi soññ Aji Sax ji
Jëfi ngoru Aji Sax ji laay fàttlee
ak cant gi Aji Sax ji yelloo,
ngir li nu Aji Sax ji defal lépp;
mbaax gu réy gi mu ji waa kër Israyil,
defal leen ko ci yërmandeem,
ak jëfi ngoram gu réy.
Moo noon: «Sama ñoñ déy ñoom a!
Ñee di doom yu dul tas yaakaar.»
Mu daldi doon seen jotkat.
Seen gépp njàqare di njàqarey boppam,
malaaka mi mu jàkkaarlool musal leen ca.
Moo leen sopp, ñeewante leen,
ba jotal leen boppam,
te fu ñu masa jaare démb,
mu fab leen, boot.
10 Waaye ñoom ñoo fippu,
di naqaral xelam mu sell,
mu soppliku seen noon,
ba mujj di xareek ñoom.
11 Ñoñam ña daldi fàttliku janti Musaa ya woon.
Ña nga naan: «Ana ki jàlle woon Israyil géej,
mook sàmmi géttam ga?
Ana ki yebaloon noowam gu sell ci seen biir?
12 Ana ki dawaloon dooley përëgam bu tedd ba,
ñeel ndijooru Musaa,
xaral leen ndox ma,
ba ame ca woy wu sax dàkk?
13 Ana ku leen doxloo woon biir xóote ya,
ñu mel ni fasi naari góor ci biir màndiŋ,
te tërëfuñu?
14 Ni jur gu wàccew xur, di fa fore,
ni la leen Noowug Aji Sax ji
maye ab dal-lukaay.
Noonu nga wommate sa ñoñ,
ba ame ca woy wu rafet.
 
15 «Ngalla séentool asamaan,
xooleel fa sa kër gu sell ga ne ràññ.
Ana sa fiiraangeek sa njàmbaar?
Sag rafet xol ak sa yërmande ñooru na ma!
16 Yaw déy yaa di sunu Baay.
Ibraayma xamalu nu dara,
Israyil63.16 Israyil fii mooy maam Yanqóoba. xamu nu.
Yaw Aji Sax ji yaa di sunu Baay,
sa tur a di “sunu Jotkat naka jekk.”
17 Aji Sax ji, loo nuy wërloo fu sore say yoon,
di nu dërkiisal, ba ragalatunu la?
Sang bi, délsil ngir nun,
sa giir yii nga séddoo.
18 Nun sa xeet wu sell wii,
moomunu réew mi lu yàgg,
te noon yi dëggaate nañu sa bérab bu sell.
19 Nu ngi mel ni xeet woo masula yilif,
xeet wu ñu masula tudde sa tur.
Éy soo xaroon asamaan, wàcc,
ba tund yi yëngu fi sa kanam!»

*63:1 63.1 Edom mi doon seexu Yanqóoba, moom lañu dippee réewum Edom, te moo taxawe taxawaayu noonub Aji Sax ji.

63:1 63.1 Boccra ab dëkk la ci réewum Edom.

63:16 63.16 Israyil fii mooy maam Yanqóoba.