Téereb Yonent Yàlla
Malasi
Saar 1
Yéeneb kàddug Aji Sax jii moo ñeel Israyil, ci jottlib Malasi.
Cofeelu Aji Sax ji kóllëreem la laloo
Aji Sax ji nee: «Dama leena sopp,»
yeen ngeen ne: «Ana noo nu soppe?»
Mu ne: «Xanaa Esawu du seexub Yanqóoba?»
Kàddug Aji Sax jee,
«moona Yanqóoba laa sopp,
te Esawu laa foñ.
Maa def ay tundam ab gent,
ab céru suufam, ma def ko dëkkuwaayu
tilli màndiŋ mi.
Su Edom* 1.4 Edomeen ñi ñoo askanoo ci Esawu, bànni Israyil askanoo ci Yanqóoba seexu Esawu. Esawu moo teddadil li taxawe kóllërey Aji Sax ji, ba mu sàgganee cérub taawam. Seetal ci Njàlbéen ga 25.34. Edomeen ñi ñoo dëddu Israyil mi Aji Sax ji taamul boppam. Seetal ci Abdiyas 10-14. nee: “Dees noo rajaxe,
waaye nooy tabaxaat gent bi,”
Aji Sax ji Boroom gàngoor yi moom dafa wax ne:
“Ñooy tabax, maay màbb.”
Ñoom lees di wooye waa diiwaan bu bon bi,
askan wi Aji Sax ji mere ba fàww.
Yeena koy gisal seen bopp,
yeenay seede ne: “Màggaayu Aji Sax ji
jéggi na kemu réewum Israyil.”
Aji Sax ji tiiñal na sarxalkat yi
«Doom teral baayam,
jaam, sangam.
Man, su ma dee baay, ana saab teraanga?
Su ma dee ab sang, ana saab cér?»
Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax,
mu ne: «Yeen sarxalkat yi teddadil ngeen sama tur,
yeen ngeen ne: “Ana nu nu teddadile sa tur?”
Xanaa di indi ñam wu sobewu
fi sama sarxalukaay.
Yeen ngeen ne: “Ana nu nu la sobeele?”
Xanaa xalaat ne sañees naa teddadil
sarxalukaayu Aji Sax ji.
Bu ngeen ma sarxalsee jur gu gumba, dara aayu ci?
Am bu ngeen ma sarxalsee jur guy soox,
ak jur gu wopp, dara aayu ci daal!
Yóbbul leen ko seen boroom dëkk rekk,
ba xam ndax moo leen di nangul,
mbaa mu siggil leen!»
Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
 
«Ngeen ne: “Léegi nag tinuleen Yàlla rekk,
mu baaxe nu!”
Yeena tooñ, ndax day siggil kenn ci yeen?»
Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
10 «Éy bu kenn ci yeen tëjoon bunt yi far,
te baña jafal ab taal ci sama kaw sarxalukaay ci dara.
Awma benn bànneex ci yeen!»
Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
«Ab sarax, duma ko nangoo ci seeni loxo.
11 Waaye li ko dale penku ba sowub jant,
fu ci nekk la sama tur màgge ci biir xeet yi,
te fépp lees di taale cuuraay, ngir sama tur,
boole ci sarax su set,
nde sama tur a ni màgge fi biir xeet yi.»
Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
12 «Waaye yeen yeena teddadil sarxalukaayu Aji Sax ji,
nde yeena xalaat ne lu sobewu la,
te aw yàppam, aw ñamam jarul dara.
13 Yeena ngi naa: “Ndaw lu soof,” di ciipatu.»
Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
«Jur gu ñu sàcc ngeen may indil,
ak guy soox, ak gu wopp,
loolu mooy seen sarax!
Nu ma koy nangoo ci seeni loxo?»
Aji Sax jee ko wax.
 
14 «Alkànde ñeel na ab jinigalkat bu am ci géttam
am kuuy mu mu xasoo sarxe,
te di sarxalal Boroom bi jur gu sikk,
nde man, buur bu mag laa!»
Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
«Sama tur moo jara ragal fi biir xeet yi.

*1:4 1.4 Edomeen ñi ñoo askanoo ci Esawu, bànni Israyil askanoo ci Yanqóoba seexu Esawu. Esawu moo teddadil li taxawe kóllërey Aji Sax ji, ba mu sàgganee cérub taawam. Seetal ci Njàlbéen ga 25.34. Edomeen ñi ñoo dëddu Israyil mi Aji Sax ji taamul boppam. Seetal ci Abdiyas 10-14.