Saar 2
«Léegi nag, sarxalkat yi, santaane bii yeen la ñeel.
Su ngeen dégluwul,
te defuleen seen xel ci teral sama tur,»
Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax,
«alkànde laay yebal fi seen biir,
ba alagaale seeni barke,
te alag naa ko jeeg,
nde defuleen seen xel ci teral ma.
Maa ngii di yar seen askan,
sëlëm leen sébbriit,
mi jóge ci seen saraxi màggal,
ñu tonniwaale leen ak sébbriit mi.
Su boobaa ngeen xam ne
maa leen yónnee santaane bii,
ngir saxal sama kóllëreek Lewi*2.4 Leween ñi jëfe woon fiiraange ci Aji Sax ji, ñoom lay wax. Seetal ci Mucc ga 32.25-29.
Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
«Sama kóllëre moom laa ko séqal,
mu jur ndund ak jàmm,
maa ko may loolu ngir mu ragal ma,
ragaloon na ma it, bay yéemu ci sama tur.
Njànglem dëgg la dëkkaloon ci gémmiñam,
te ag njubadi, déggeesu ko ciw làmmiñam,
xanaa di ànd ak man ci jàmm ak njub,
tey baloo ñu bare yoonu ñaawtéef.
 
«Kàddug sarxalkat déy day sàmm xam-xam,
te ciy waxam la nit ñi di sàkkoo àlluwa,
nde mooy ndawal Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.
Waaye yeen dangeena moy yoon wi,
seenum njàngle ngeen fakktale ñu bare,
te yeena fecci kóllëreg Lewi.»
Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
«Moo tax man it ma def xeet wépp xeeb leen,
sewal leen,
feye leen ko seen ñàkka sàmm samay yoon,
ak par-parloo gi ngeen di diglee yoon wi.»
Aji Sax ji du nangu saraxi workat yi
10 Xanaa du benn baay lanu am, nun ñépp?
Te jenn Yàlla jee nu sàkk?
Lu waral ku ne di wor mbokkam,
ba fecci kóllërey maam ya?
11 Yuda wor na,
lu jomblu lees def
fi Israyil ak Yerusalem.
Yuda déy moo teddadil li Aji Sax ji sopp
te mooy bérabam bu sell:
Yuda moo takk janqub yàllay doxandéem.
12 Ku def lii, yal na Aji Sax ji dagge ci xaymay Yanqóoba, gépp kuutaayam, boole ci kuy indil ab sarax, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.
13 Lii itam yeena ngi koy def:
Yeena ngi tawal ay rongooñ sarxalukaayu Aji Sax ji,
di jooy ak a binni,
ndax moo geesootul seen sarax,
te nangootul lenn ci seen loxo.
14 Ngeen naa: «Ndax lan?»
Ndax Aji Sax ji moo seede seen diggante
ak seen jabar ja ngeen jël ba ngeen di ndaw,
tey ngeen wor ko, te mu doonoon seen wéttal,
seen jabar ju ngeen séqal kóllëre.
15 Kenn deful lii te desem xel.
Kenn doŋŋ a ko defoon. Ndax lan?
Kuutaay li ko Yàlla digoon la doon wut.
Kon nag sàmmleen seenum xel,
te buleen wor seen jabar ja ngeen jël
ba ngeen di ndaw.
16 «Pase laa bañ,»
Aji Sax ji, Yàllay Israyil moo ko wax,
«ak ku làmboo jëfi loraange ni mbubb.»
Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
Kon nag sàmmleen seenum xel,
te buleen wor.
Aji Sax ji, dëgg lay àtteji
17 Soof ngeen Aji Sax ji ak seeni wax,
ngeen naan: «Nu nu ko soofe?»
Xanaa naan: «Képp kuy def lu bon
mooy ki baax ci Aji Sax ji,
te kooku la safoo.»
Mbaa ngeen naa: «Ana Yàlla jiy àtte dëgg sax?»

*2:4 2.4 Leween ñi jëfe woon fiiraange ci Aji Sax ji, ñoom lay wax. Seetal ci Mucc ga 32.25-29.