Saar 14
Kurél gu sell gi topp na Gàtt bi
Ma xoolaat, gisuma lu moy Gàtt bi fa mu taxaw ci kaw tundu Siyoŋ*14.1 tundu Siyoŋ mooy tund wa ñu tabax Yerusalem ci kawam. ak téeméer ak ñeent fukk ak ñeenti junniy nit (144 000) ñu ànd ak moom, te ñu bind ci seen jë turu Gàtt bi ak turu Baayam. Ma dégg baat bu jóge asamaan, nirook riirum géej, mel ni dënu gu réy, melati ni ay xalamkat yuy xalam. Ña ngay woy woy wu yees ca kanam ngàngune ma, ca kanam ñeenti bindeef yaak mag ña, te kenn manula mokkal woy wi, ku dul téeméer ak ñeent fukk ak ñeenti junni ñooñu ñu jote àddina. Ñooñu ñooy ñi masula ànd ak jigéen, di sobeel seen bopp, ndax masuñoo séy. Ñooñoo topp Gàtt bi fépp fu mu jëm. Ñooñu lañu jote ci biir nit ñi, def leen lu mel ni jooxeb ndoortel meññeef, ñeel Yàlla ak Gàtt bi, te kàddug fen masula jibe seen gémmiñ. Gàkkuñu fenn.
Ñetti malaaka yégle nañu àttey Yàlla
Ci kaw loolu ma gis meneen malaaka muy naaw ci digg asamaan, ànd ak xibaaru jàmm bi sax dàkk, ngir baaxe ko waa àddina: niti wépp askan ak gépp giir ak wépp làmmiñ ak wépp xeet. Ma ngay àddu ca kaw, naan: «Ragal-leen Yàlla te màggal ko, ndax waxtuw àtteem jot na. Kon nag jaamuleen ki sàkk asamaan ak suuf ak géej ak bëti ndox yi.»
Meneen malaaka, topp ci, di ñaareel bi. Mu ne: «Babilon a daanoo, dëkk bu mag ba daanu na! Moom ma daan màndal askanoo askan biiñu moyam muy indi am sànj.»
Meneen malaaka, topp ci, di ñetteel bi. Mu àddu ca kaw, ne: «Képp ku sujjóotal rab wi ak jëmm ji ñu ko sàkkal, ba ñu defal ko màndargam jë mbaa loxo, 10 kooku dina naan biiñu sànjum Yàlla bu kenn raxul, ñu xelli ko ci kaasu sànjam. Te dees na ko mbugale sawara ak tamarax ci kanam malaaka yu sell yi ak Gàtt bi. 11 Seen saxaru sawaras mbugal day saxoo dàkk, di gilli ba fàww. Guddeek bëccëg, ñooñuy sujjóotal rab wi ak jëmm ji ñu ko sàkkal, ak mboolem ku ñu màndargaale turu rab wi, kenn du ci nopplu.»
12 Kon nag ñu sell ñiy wormaal santaaney Yàlla te saxoo gëm Yeesu, looloo tax ñu wara muñ.
13 Ci kaw loolu ma dégg baat bu jibe asamaan ne: «Bindal: “Bés niki tey ndokklee aji dee ñi deeyaale gëm Sang bi.”» Noo ga daldi ne: «Waawaaw, ndax coono dina leen wàcc, ngir seeni jëf a leen topp.»
Ngóobum àddina tar na
14 Ma xoolaat, gisuma lu moy niir wu weex, ak jëmm ju ca toog, di nirook doom aadama, kaalawoo kaalag wurus, ŋàbb ab sàrt bu ñaw. 15 Meneen malaaka génne ca néeg Yàlla ba, daldi àddu ca kaw, wax ak ki toog ci niir wi, ne ko: «Dawalal sa sàrt te góob, ndaxte ngóob jot na, ngóobum àddina ñor na.»
16 Ci kaw loolu ki toog ci kaw niir wi dawal sàrtam ci kaw suuf, daldi góob àddina.
17 Meneen malaaka nag génne ca néeg Yàlla ba ca asamaan, ŋàbb moom itam, sàrt bu ñaw. 18 Ba loolu amee meneen malaaka mi yilif sawara, jóge ca sarxalukaay ba, daldi àddu ca kaw, wax ak malaaka, mi yor sàrt bu ñaw bi, ne ko: «Dawalal sa sàrt bu ñaw bi, nga dagg cëggi reseñ gi ci àddina, ndax reseñ ji ñor na.»
19 Malaaka ma dawal sàrtam ci àddina, dagg reseñ ji, sànni ci biir nalukaay bu mag bu sànjum Yàlla ba. 20 Ñu dëggaate reseñ ja ca nalukaay, ba ca gannaaw dëkk ba, deret génne ca, taa ba tollook laabi fas yi, wala wal ba dajal digganteb ñetti téeméeri kilomeetar.

*14:1 14.1 tundu Siyoŋ mooy tund wa ñu tabax Yerusalem ci kawam.