Saar 15
Musibay mujjantal agsi na
Ma xoolaat, gisuma ci asamaan lu moy jeneen firnde ju màgg te yéeme: juróom ñaari malaaka yu taawu juróom ñaari musiba. Musiba yu mujj yaa nag, ngir ca la sànjum Yàlla di mate. Ma gisati lu mel ni géeju kiristaal bu jaxasook sawara. Ci biir loolu ña daanoon rab waak jëmmu nataalam, ak lim bi méngook turam, ñu ngi taxaw ci kaw géeju kiristaal gi, yore ay xalami Yàlla. Ña ngay woy woyu Musaa jaamu Yàlla ba, ak woyu Gàtt bi, naan:
«Yaw Boroom bi Yàlla Aji Man ji,
yaa réy te yéeme ay jaloore.
Yaw Buuru askan yi,
yaa jub te dëgguy doxalin.
Boroom bi, ana ku la ragalul?
Ku dul màggal saw tur?
Yaw doŋŋ yaa sell.
Askan yépp ay dikk, sujjóotsil la,
ndax yaa jubi dogal.»
Gannaaw loolu ma xoolaat, daldi gis màkkaan ma fa asamaan, xayma ba fat seede si*15.5 seede si mooy àlluway seede yi fukki santaaney Yàlla ya binde woon., mu ubbiku. Juróom ñaari malaaka, yi taawu juróom ñaari musiba yi nag, génne ci màkkaan mi. Ñu ngi sol mbubbi lẽe yu set, ne ràññ, ay ngañaayi wurus takke ci seen dënn. Kenn ci ñeenti bindeef yi nag jox juróom ñaari malaaka yi, juróom ñaari ndabi wurus yu fees ak sànjum Yàlla jiy dund ba fàww. Ba mu ko defee màkkaan ma fees ak saxar su bawoo ci leeru Yàlla ak kàttanam. Kenn nag manatula dugg ci màkkaan mi, ba kera juróom ñaari musibay juróom ñaari malaaka yi matee.

*15:5 15.5 seede si mooy àlluway seede yi fukki santaaney Yàlla ya binde woon.