3
Lii lañu séentu ci njiitu mbooloo mi
1 Wax ju wóor a ngii: kuy sàkku sasub jiite mbooloom gëmkat ñi, liggéey bu rafet lay xëccu. 2 Njiit li nag fàww mu mucc sikk, di ku dencul lu wees jenn jabar, ku noot bakkanam, jiital am xelam, di ku nawlu, man gan, te mana jàngale. 3 Bumu di ab màndikat, mbaa kuy sooke ab xeex, waaye na lewet, bañu ay, te bumu xemmem xaalis. 4 Kërug boppam nag, na ko yor yorin wu rafet, te na mana yar ay doomam ba ñu nangul ko te sédd ko cér bu mat sëkk. 5 Ndax ku tëlee yor kërug boppam, ana nu mu mana sàmme mbooloom gëmkati Yàlla yi? 6 Te it bumu dib tuubeen bu bees, lu ko moy ag réy-réylu man na koo gëlëmal, ba mu tàbbi ci mbugal ni Seytaane. 7 Te it ñi ci biti te gëmuñu, la ñu ko seedeel nay lu rafet, ba deram du yàqu, nde kon mu tàbbi ci fiiru Seytaane.
Lii lañuy séentu ci jàpplekati mbooloo mi
8 Naka noonu kiy jàppale mbooloo mi, na di ku tedd, bumu di boroom ñaari kàddu. Bumu di ku sàngara jiital, mbaa kuy sàkku am-am bu lewul. 9 Na ŋoy ci mbóotum ngëm mii feeñ te ànd ceek xel mu dal. 10 Dees koy njëkka seetlu nag, ba muy ku mucc sikk, ñu door koo dugal ci liggéeyu kiy jàppale mbooloo mi. 11 Naka noonu, na jigéen ñiy jàppale mbooloo mi*jigéen ñiy jàppale mbooloo mi: manees na koo tekki nii it: seeni soxna di ñu tedd, buñu diy soskat, nañu noot seen bakkan, te jara wóolu ci lépp.
12 Ab jàppalekatub mbooloo mi bumu denc lu wees jenn jabar te na yor ay doomam ak këram yorin wu rafet. 13 Ñi ci wàccoo ak seen sasub jàppalekat nag, seenub liggéey lañu jënde taxawaay bu rafet, te ñooy mana waxe fit seen ngëm gi ñu gëm Almasi Yeesu.
Mbóotum yoonu ngëm wi màgg na
14 Lii laa lay bind, te di la yaakaara seetsi ci fan yu gàtt, 15 ngir su ma yeexee itam, nga xam nooy doxale ci biir waa kër Yàlla, maanaam mbooloom ñi gëm Yàlla jiy dund. Mbooloom gëmkat mi mooy kenug dëgg gi, di cëslaayam. 16 Deesul nàttable moos màggaayu mbóot mii feeñe ci sunu yoonu ngëm:
Kii moo feeñe ci yaramu suux,
Noowug Yàlla dëggal ko,
malaaka ya niir ko;
moom lañu waaree ci xeet yi,
gëmees na ko ci kaw suuf it,
te yéegees na ko fa leer ga.