4
Àlluway ceytaane yàq na am xel
1 Noowug Yàlla wax na ci lu leer ne ci mujug jamono, dina am ñu wacc yoonu ngëm wi, di topp ay xalaat yuy fàbbee ak ay àlluway ceytaane 2 yu leen ay jinigalkat, ay fen-kat yu dërkiis ab xol, di naxe. 3 Ñooñu ñooy aaye ab séy, di digle ñàkka lekk yenn ñam yu Yàlla sàkk, ngir gëmkat ñi xam liy dëgg man cee jariñu te di ko sante Yàlla. 4 Ndaxte li Yàlla sàkk lépp a baax, du lenn lees ciy aayal, ndegam kàddug cant lees koy jariñoo. 5 Lu mu mana doon, kàddug Yàlla akug ñaan moo koy sellal.
Lii la liggéeyu jawriñu Almasi bi laaj
6 Soo dee xamal loolu bokki gëmkat ñi, yaa di jawriñu Almasi Yeesu ju baax ju xontu ci kàdduy yoonu ngëm wi ak àlluwa ju rafet ji nga topp naka jekk. 7 Waaye nettali yu yittewoo lu dul Yàlla, ak léebi jeeg ju màggat ji, bañ ko, te nga tàggatu ci ragal Yàlla. 8 Ndax kat tàggat aw yaram, as njariñ a ngi ci, waaye ragal Yàlla, ci lépp lay jariñe, te moo moom digeb àddinay tey ak ëllëg. 9 Kàddu gii may wax, lu wóor la te jara gëm ba mu mat sëkk. 10 Loolu kat moo nu tax di sonn aka góor-góorlu, ndax Yàlla jiy dund lanu yaakaar, moom miy musal ñépp, rawatina gëmkat ñi.
11 Digleel loolu, te di ko jàngale. 12 Bu la kenn xeebe say at yu néew, waaye nanga doon royukaayu gëmkat ñi ci wax ak jëfin ak cofeel ak ngëm ak dundin wu set. 13 Ba keroog may dikk, saxool di jàng-biral Mbind mi, di ñaaxe aka jàngale. 14 Bul sàggane may gi ci yaw, te di lu ñu la baaxee ag kàddug waxyu gu ànd ak tegeb loxo ba la kuréelu mag ñi defaloon. 15 Loolu ngay def sam xel, mbir yooyu ngay pastéefoo, ba sag yokkute bir ñépp. 16 Sàmmal sa bopp nag, sàmm sa àlluwa, te saxoo ko; soo ko defee, dinga mucc, musal ñi lay déglu.