Téereb Yonent Yàlla
Amos
Amos mi ñu jox téere bii aw turam, ag càmm ak liggéeyu toolu figg la féetewoo woon. Moonte moom la Yàlla woo, ngir yóbbante ko ay kàdduy waxyoom. Esayi ak Mise ak Ose bokk nañu ci ñi Amos bokkal jamono. Leneen lu mu bokk ak Ose moo di, li ëppoon ci xibaaram, ci réewum Israayil ma woon ca bëj-gànnaar la jëmoon, doonte mi ngi cosaanoo réewum Yuda ma féete bëj-saalum.
Ci tënk:
1.1—2.16 Mbugal ñeel na ay xeeti àddina.
3.1—6.14 Mbugal ñeel na Israayil.
7.1—9.10 Juróomi peeñu a ngi yégle ay mbugal.
9.11-15 Mbugal muy dëgmal weddiwul yaakaari ëllëg.
1
Ubbite gi
1 Kàdduy Amos a ngii, di boroom jur bu dëkkoon Tekowa
*. Mu am peeñu mu jëm ci Israayil ci janti Osiyas
† buurub Yuda ak janti doomu Yowas, Yerbowam buurub Israayil. Loolu tollu ci ñaari at lu jiitu yëngu-yëngu suuf ba.
2 Mu ne:
Aji Sax jeey yëmmoo fa Siyoŋ
‡,
Yerusalem lay àddoo,
parluy sàmm si ne faraas,
mbooyum kaw tundu Karmel lax.
Aji Sax ji mbugal na xeet yi
(Saar 1.3—2.16)
3 Aji Sax ji da ne:
«Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent,
te duma fomm seeni duma.
Ñoo bàcce waa Galàdd bàccukaayi weñ.
4 Maay yebal sawara seen waa kër Buur Asayel,
mu xoyom taaxi Buur Ben Addàd.
5 Maay dàjji bunti dëkkub Damaas,
boole ca boroom yetu nguur fa Bet Eden
†.
Waa Siri dugg ngàllo, dellu Kir
‡.»
Aji Sax jee ko wax.
6 Aji Sax ji nee:
«Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent,
te duma fomm seeni duma.
Ñoo jàpp ba noppi gàddaayloo mbooloom lëmm,
jalax leen ca Edomeen ña.
7 Maay yebal sawara ca tatay Gasa,
mu xoyom ay taaxam.
8 Maay dagg waa Asdodd
ak boroom yetu nguur fa Askalon,
fél Ekkron,
ndesu Filisteen ña sànku.»
Boroom bi Aji Sax jee ko wax.
9 Aji Sax ji nee:
«Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent,
te duma fomm seeni duma.
Am na mboolooy lëmm yu ñu gàddaayloo,
te ñoom waa Tir jaay leen Edomeen ña,
te sédduñu leen ci kóllëreg mbokk gi.
10 Damay yebal sawara ca tatay Tir,
mu xoyom ay tataam.»
11 Aji Sax ji nee:
«Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent,
te duma fomm seeni duma.
Ñoo toppe seen bokki bànni Israayil saamar,
jalax yërmande,
mer mer mu dul meddi
ak xadar ju dul giif mukk.
12 Maay yebal sawara fa Teman,
mu xoyomaale tatay Boccara
‡.»
13 Aji Sax ji nee:
«Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent,
te duma fomm seeni duma.
Ñoo butti ay jigéeni biir ca Galàdd,
ba ñuy xare ngir yokk seen suuf.
14 Maay jafal ca kaw tatay Raba
*,
mu xoyom ay taaxam,
yuux ya jib bésub xare,
ci biir callweer bésub ngëlén.
15 Seen buur lañuy jàpp, mu gàddaay,
mooki kàngamam.»
Aji Sax jee ko wax.