4
Aji Sax ji tiiñal na nooni ñoñam
«Jant yooyu, ci boobu bés,
bu ma tijjee wërsëgu Yuda ak Yerusalem,
maay dajale mboolem xeet yi,
wàcce leen ca xur wa ñu dippee Aji Sax jeey àtte.
Fa laay layook ñoom ci mbirum sama ñoñ,
mbirum Israayil sama séddoo
bi ñu tasaare ci biir xeet yi,
ak sama mbirum suuf si ñu séddoo.
Sama ñoñ lañu tegoo bant,
xale bu góor, ñu weccikoo ab gànc;
xale bu jigéen, ñu jaaye biiñ, naan.
Yeen it waa Tir ak Sidon,
ak gox-goxaani Filisti yépp,
ana lu ngeen joteek man?
Xanaa dama leena def, lu ngeen di feyu?
Su ngeen dee feyu nag,
ma gaaw leena këpp seen añu jëf
ci seen kaw bopp.
Sama xaalis ak sama wurus, ngeen jël,
samay denc yu baax, ngeen yóbbu
ca seeni jaamookaay.
Waa Yuda ak waa Yerusalem,
yeena leen jaay xeetu Gereg yi,
ngir sorele leen seen suuf.
Maa ngii di leen yékkatee foofa,
fa béreb ba ngeen leen jaaye,
te yeen, maa leen di këpp seen peyu jëf ci bopp.
Seen doom yu góor ak yu jigéen
laay jaay waa Yuda,
ñu jaayaat leen waa Seba, doomi réew mu sore.»
Aji Sax jee ko wax!
Wooteb xare jib na
Yégleleen lii ci biir xeet yi:
«Waajalleen xare,
yékkatileen ñeyi xare yi,
na xarekat yépp dikk, songi xare.
10 Seeni illéer ngeen di tëgg ay saamar,
tëgg seeni xepp ay xeej,
te na ku néew doole ne: “Jàmbaar laa!”
11 Dikkleen gaaw, yeen xeet yépp,
ba fépp daj,
ngeen bokk daje.
Aji Sax ji, foofa ngay yebal say jàmbaar.
 
12 «Na xeet yi jóg te songi xare ca xur,
wa ñu dippee Aji Sax jeey àtte,
foofa déy laay toog di àtte mboolem xeet yi,
ba fépp daj.
13 Dawalleen sàrt bi, nde ngóob mi ñor na,
dikkleen nal, nalukaayu reseñ bi fees na,
te mbànd yi rembat na, nde seen bàkkaar a réy.»
 
14 Ndaw gàngoori gàngoor ca xuru Àtte ba,
nde bésub Aji Sax jee dëgmal ca xuru Àtte ba!
15 Jant ak weer giim,
biddiiw yi fat seenug leer.
16 Aji Sax ji fa Siyoŋ lay ŋare,
foofu ca Yerusalem lay àddoo,
asamaan ak suuf rëng-rëngi.
Waaye Aji Sax jee dib rawtu, ñeel ñoñam,
moo dim tata, ñeel bànni Israayil.
 
17 «Su boobaa ngeen xam ne maay seen Yàlla Aji Sax
ji dëkke Siyoŋ, sama tund wu sell.
Yerusalem day daldi sell,
doxandéem dootu fa jaare.
Naataange ñeelati na Israayil
18 «Bésub keroog tund yu mag yi
di rogalaat biiñ bu bees,
tund yu ndaw yi di xelli meew,
dexi Yuda yépp la am ndox di wale,
te kër Aji Sax ji, bëtu ndox a cay balle,
di suuxat xuru Akasya ya.
19 Misra ag ndànd-foyfoy lay doon,
réewum Edom di màndiŋ mu wéet,
ndax coxor ga ñu soxore waa Yuda,
nde ñoo tuur deretu jàmbur ñu deful dara ca seenum réew.
20 Yuda lees di dëkke ba fàww,
Yerusalem ñeel maasoo maas.
21 Seen bakkan bi ma teggilul woon àtteb yoon bi ko topp,
maa koy teggil àtteb yoon bi ko topp.»
Aji Sax ji Siyoŋ lay màkkaanoo.