3
Ñépp la Aji Sax ji di sotti ag noowam
1 «Gannaaw loolu maay tuur samag noo ci kaw ñépp,
seeni doom, góor ak jigéen di biral kàdduy waxyu,
seeni màggat di gént ay gént,
seeni xale yu góor di gis ay peeñu.
2 Kera jant yooyu, jaam yi sax, góor ak jigéen,
maa leen di tuur samag noo.
3 Maay def ay kiraama fi asamaan ak fi suuf;
deret ak sawara ak saxaar su jolli.
4 Jant beey soppaliku ag lëndëm,
weer wi doon deret,
bésub Aji Sax ji doora taxawe màggaay ak daraja!
5 Su boobaa képp ku woo Aji Sax ji wall ciw turam,
dinga raw.
Tundu Siyoŋ ak biir Yerusalem kay
fa la aw ndes di ame,
na ko Aji Sax ji waxe woon,
te ñi Aji Sax ji woo ñooy bokk ci ñi dese bakkan.