25
Waxyu dal na xeet yi
Waxyu dal na Amon
Kàddug Aji Sax ji dikkal na ma ne ma: «Yaw nit ki, neel jàkk Amoneen ñi, nga jottali kàdduy waxyu ci seen kaw. Waxal Amoneen ñi, ne leen:
“Dégluleen kàddug Boroom bi Aji Sax ji.
Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
yeena noon: ‘Ñaw!’ ba ñu teddadilee sama kër gu sell,
gental réewum Israayil,
gàddaayloo waa kër Yuda.
Maa ngii nag di leen jébbal màngaani penku,
ñu moom leen,
samp seeni dal fi seen biir,
yékkati fa seeni xayma.
Ñooy lekk seen meññeef,
naan seen meew.
Maay soppi Raba seen péey ab parlub giléem,
maay def réewum Amon goorukaayu gàtt,
ba ngeen xam ne maay Aji Sax ji.
Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne:
Yeena doon tàccu,
di fecc, bége tiisu réewum Israayil,
di leen sewal lu ngeen man.
Maa ngii nag di leen dóor sama loxo,
te maa leen di jébbal xeet yi, ñu sëxëtoo leen.
Maa leen di raafale fi digg xeet yi,
maa leen di fare ci réew yi,
faagaagal leen,
ba ngeen xam ne maay Aji Sax ji.”
Waxyu dal na Mowab
«Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne:
Waa Mowab ak Seyir ñoo ne: “Xoolleen waa kër Yuda ñii ni ñu mujje,
ñook xeet yépp a yem!”
Maa ngii nag di ŋafal réewum Mowab,
ba xañ leen mboolem seen dëkk ya gëna taaru sax,
di Bet Yesimot ak Baal Mewon ak Kiryaatayim.
10 Màngaani penku laa leen di jébbal,
jébbalaale leen Amon,
ba kenn du fàttalikooti Amon ci biir xeet yi,
11 te maay wàcceel Mowab ay mbugal,
ba ñu xam ne maay Aji Sax ji.
Waxyu dal na Edom
12 «Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
Edom a feyu ci waa kër Yuda,
feyu ga mu feyu di tooñaange gu réy.
13 Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
Maay dóor Edom sama loxo,
faat fa nit ak mala,
maa koy def ab gent,
la dale Teman ba Dedan, saamar lañu leen di faate.
14 Maay duma Edom,
te Israayil sama ñoñ laa leen di dumaa.
Ñooy jëflanteek Edom la méngook sama mer,
tollook sama xadar,
ba ñu ñam sama mbugal.
Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.
Waxyu dal na Filisti
15 «Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne:
Filisteen ñee jiital seen mbañeel gu sax,
ñoo jéppee jéppi seeni noon, feyoo feyu,
ba tas leen.
16 Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
Maa ngii di dóor Filisteen ñi sama loxo,
maay dagg ñooñu di askanu Keret,
maay far ndes wa ca tefesu géej.
17 Maa leen di feye mbugalu xadar yu mag,
te bu ma leen yenee sama peyu mbugal,
ñu xam ne maay Aji Sax ji.»