26
Waxyu dal na Tir
1 Ba loolu amee, ca fukkeelu at maak benn, yemook benn fanu weer wa, kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma:
2 «Yaw nit ki,
Tir dëkk ba moo ree Yerusalem,
ne: “Ñaw! Buntu dëkk bi xeet ya daan jaare dàjjiku na!
Léegi man la bunt ubbikul,
léegi maay woomle, Yerusalem gental na.”
3 Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
Yaw Tir, maa ngii fi sa kaw.
Ni géej di yéegee ay gannaxam,
ni laay yéegloo fi sa kaw xeet yu bare.
4 Ñooy màbb say tata,
daane say sooroori tata,
ma buube fa pënd ba,
def ko doj wu ne duŋŋ.
5 Tir ay doon wéerukaayu caax ci digg géej gi,
maa ko wax, kàddug Boroom bi Aji Sax jee.
Dëkk bii mooy doon sëxëtoom xeet yi,
6 dëkk-dëkkaan yi bootu ci mbooyam, saamar faat leen,
ñu xam ne maay Aji Sax ji.
7 «Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne: Maa ngii di jële bëj-gànnaar, indi ci kaw Tir, Nebukatnecar buuru Babilon, buuru buur yi, aki fas aki watiir aki gawar ak mbooloo mu takku.
8 Dëkk-dëkkaan yi bootu ci sa àll bi, saamar la leen di reye.
Mooy yékkati fi la wër ab gawukaay,
jal ay sëkk, gawe la,
yékkati kiiraayu xare yu ràbbaloo ba defum taax, janook yaw,
9 mooy dóor say tata dénku dàjjikaay,
mooy màbbe say sooroori tata ay sémmiñam,
10 ay fasam yu bare sànge la pënd,
riiru gawar yaak mbege yaak watiir ya riiral say tata,
mu jàlle ci say bunt, dugg,
ni ñuy bëtte dëkk bu ñu bëtt tataam.
11 Tànki fasi naaru-góoram lay noote sa mbeddoo mbedd,
sa mbooloo mi, mu bóome saamar;
sa kenuy tabax yu dëgër jóoru fi suuf.
12 Ñooñooy foqati sam koom,
sëxëtoo sa alal,
màbb say tatay dëkk,
daane sa kër yu bakkane,
boole doj yaak bant yaak pënd ba,
tàbbal ca mbeex ma.
13 Maay dakkal say woy,
ba say xalam du fi jibeeti.
14 Maa lay def doj wu ne duŋŋ,
bérebu wéerukaayu caax ngay doon,
te deesu la tabaxati mukk.
Man Aji Sax ji déy maa ko wax!
Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.
15 «Boroom bi Aji Sax ji dafa wax Tir, ne ko:
Keroog sa coowal jéll ba,
ba ñuy bóome fa sa biir,
ñay dee di binni,
dun yaa cay dégg, di lox moos!
16 Mboolem buuri tefes yaay wàcc seeni ngàngune,
futti seeni mbubb,
tàggook seen yére yu yànj,
bàddoo tiitaange,
ne dett fi suuf,
dëkke kat-kat,
nga tax seen yaram daw.
17 Ñooy yékkati kàddu, jooy, ne la:
“Yaaka sànku tey, yaw dunu géej bu xumb bi woon,
yaw dëkk bu siiw bi woon, di jàmbaaru waa géej,
yaak say nit a daa tiital mboolem ñi leen wër.
18 Tey sa bésub jéll bii,
dun yeey xala lox.
Duni géej yeey tiit ci sa sànkute gi.”
19 «Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne:
Bu may gental sa dëkk,
nga mel ni dëkk yu nit ña ne mes,
ba ma xëpp xóote ya fi sa kaw,
ba wali ndox ya mëdd la,
20 keroog maa lay wàccaaleek ñay jëm biir pax,
nga fekki xeetu démb.
Maa lay dëël taati biir suuf,
fu mel ni genti cosaan ya,
nga fekki ca pax mi ña fa njëkkoona wàcc,
ngir deesatu la dëkke,
te doo amati cér ca réewum aji dund ña.
21 Demin wu raglu laa lay sédd,
ba nga ne mes,
ñu di la seet, te deesu la gisati mukk.
Kàddug Boroom bi Aji Sax jee!»