Téereb Yonent Yàlla
Esayi
Yonent Yàlla Esayi, ci daanaka juróom benn fukki at la dox ag yónnentam, mu yemook janti ñeenti buuri Yuda.
Esayi dund na jant yu metti ba xare ya amee diggante Israayil ak Yuda, te dale atum 734 ba atum 732 lu jiitu Almasi bi. Esayi fekke na itam taste ga réewum Asiri tasoon Israayil ci atum 722 lu jiitu Almasi. Esayi waxoon na itam ci toxal ga ñuy toxali waa réew mi, yóbbu leen ngàllo ca Babilon. Teewul mu yéene ne Yàlla mooy dellu yékkati xeet yi, gannaaw bu seen mbugal matee.
Kàddu gi siiw na ndax li mu wax ci xale bi nara juddu te ñu tudde ko Emanuwel: «Boroom bi ci boppam moo leen di jox firnde: janq bi mooy ëmb, jur doom ju góor, tudde ko Emanuwel (muy firi Yàllaa ngi ak nun)» (7.14).
Ci tënk:
Saar 1—39 Kàdduy waxyu ñeel na Yuda ak yeneen xeet yi.
Saar 40—66 Lu jëm ci jàmmu ñoñi Yàlla, ak ci mucc gu Yàlla indi, ñeel àddina sépp.
Mucc a ngi ci Emanuwel
1
(Saar 1—12)
Ubbite gi
Lii moo di peeñum Esayi doomu Amocc, di lu mu gis ci mbirum Yuda ak Yerusalem ci janti buuri Yuda yi ñuy wax Osiyas*Osiyas mooy Asaryaa ba tey. ak Yotam ak Axas ak Esekiyas.
Aji Sax ji sikk na waa Yuda
Asamaan, déglul; suuf, teewlul,
Aji Sax jeey àddu:
«Ay gone laa yar, màggloo leen,
ñoom, ñu gàntal ma.
Aw yëkk xam na boroomam,
mbaam-sëf xam gàmb bi ko boroomam di xonte,
waaye Israayil xamul,
sama ñoñ ñii xàmmeewuñu.»
Wóoy wii xeetu moykat,
wii askan wu diisu ñaawtéef,
mii njurum defkati mbon,
yii doomi yàqute!
Ñoo wacc Aji Sax ji,
ñoo sofental Aji Sell ju Israayil,
dëddu ko.
Xanaa dungeen wéye fippu,
ñu gën leena duma,
te bopp di góomi neen,
xol jeex tàkk?
Bopp ba téstën, fenn jagul.
Xanaa gaañu-gaañu aki dagg-dagg rekk,
ak góom yuy nàcc,
fajeesu ko, takkeesu ko,
gajfaleesu kook ag diw.
Seenum réew gental,
seeni dëkk xoyomu,
seen suuf, doxandéem yi lekk fi seen kanam,
muy gent bu doxandéem tas.
Siyoŋ, dëkk bu taaru baa ngi wéet
ni mbaarum tóokër mbaa dalub toolu xaal.
Mbete dëkk bu ñu gaw!
Bu nu Aji Sax ju gàngoor yi
waccalul woon li nu deseek as néew,
ni SodomSeetal ci Njàlbéen ga 19.23-29. lanuy mel,
Gomor lanuy neexool.
Aji Sax ji bañ na ngistal
10 Dégluleen kàddug Aji Sax ji, yeen njiiti Sodom,
teewluleen sunu yoonu Yàlla, yeen askanu Gomor.
11 «Lu may doye seen sarax yu bare?» la Aji Sax ji wax.
«Damaa suur seen saraxi rendi-dóomali kuuy,
suur nebbonu juru yar gi,
deretu yëkk ak xar ak sikket it, safu ma.
12 Bu ngeen dikkee, teewsi fi sama kanam,
ana ku leen sant ñu joggat-joggatee nii sama ëttu kër?
13 Buleen fi indeeti saraxi caaxaan,
seen saraxu cuuraay, lu ma seexlu la.
Terutel weer ak bésub Noflaay
ak wooteb ndajee ci yem!
Duma mana dékku ndajem diine mu rax njubadi.
14 Seeni Terutel weer ak seen bési màggal
laa bañ ci sama xol;
yooyu màggal a ma diis ba àttanatuma ko.
15 Bu ngeen ma tàllaleey yoxo,
ma fuuyu.
Bu ngeen doon ñaan-ñaanee it,
du maa leen di déglu:
seeni loxo, deret la taq ripp.
16 Raxasuleen ba set wecc,
jëleleen seeni jëf ju bon fi sama kanam,
te ngeen ba lu bon.
17 Jàngleen di def lu baax,
sàkku njub,
waññi ab nootkat,
àtte dëgg ab jirim,
sàmm àqu jëtun.
 
18 «Kaayleen, nu waxtaan ba juboo,» la Aji Sax ji wax.
«Li seeni bàkkaar di xonq lépp,
tàll lay weexeji.
Li muy xonq curr lépp,
weex furr lay mujje.
19 Su ngeen ma nangoo déggal,
ngëneelu réew mi ngeen di xéewloo.
20 Waaye su ngeen lànkee, fippu,
saamar a leen di xéewloo.»
Aji Sax ji déy a ko wax ci gémmiñam.
Mbugal mooy setal Yerusalem
21 Ana nu biib dëkk yàqoo, mbeteb gànc,
te nekkoon dëkkub kóllëre,
yoon mate fa,
njubte lal fa panaan,
tey ñu diy bóomkat!
22 Sa xaalis doon na raxit,
sa biiñ xormbet.
23 Seeni njiit të,
xejjoo ay sàcc,
ñoom ñépp sopp ger,
di dàq ay neexal;
ab jirim, sàmmuñu àtteem,
àqu jëtun soxalu leen.
24 Moo tax, kàddug Boroom bee,
Aji Sax ju gàngoor yi,
Jàmbaaru Israayil:
«Maay lijjanti samay bañ, ngalla ñoom!
Maay fey samay noon!
25 Yerusalem, maa lay teg loxo,
maay seeyal sa raxit ni xeme,
ba dindi sa mbuubit mépp.
26 Maay waññi say àttekat, ñu mel na woon,
ñi lay digal it dellu mel ni bu njëkkoon.
Su boobaa ñu woowe la Dëkkub Yoon
ak Dëkkub Kóllëre.»
27 Siyoŋ dëppook yoon, mucc,
ay tuubkatam wormaal njub, raw;
28 moykat ak bàkkaarkat yàqoondoo,
dëddukati Aji Sax ji sànkoondoo.
29 Yeenay rus moos ci garab yu mag,
yi ngeen soppoona daje, di xërëmtu.
Yeenay am gàcce ci tóokër
yi ngeen taamu woona daje, di bokkaale.
30 Yeenay meli ni garab gu mag gu xob ya lax,
mbaa tóokër bu amul siitum ndox.
31 Boroom doole mel ni boob,
la mu liggéey di ferñent,
ànd ak moom ne jéppét,
te kenn du fey sawara wa.

*1.1 Osiyas mooy Asaryaa ba tey.

1.9 Seetal ci Njàlbéen ga 19.23-29.