8
 1 Éy su meloon ni sama càmmiñ nga,  
mel ni ku ma bokkal wenn ween,  
ba ma dajeek yaw biti, sañ laa dar,  
te du tax ñu sikk ma!   
 2 Ma jàpp la, yóbbu sama néeg yaay,  
moom mi ma yar*Mbaa: nga jàngal ma baane,,  
ma may la biiñ bu saf,  
ak sama ndoxum gërënaat, nga naan.   
 3 Sama càmmoñu waay, ma gegenoo,  
ndijooram, ma laxasoo.   
 4 Yeen janqi Yerusalem, waatalleen ma  
ne dungeen dakkal te dungeen sooke tëraayu mbëggeel  
te jotul.   
Joxe naa xol 
 Janqi Yerusalem  
 5 Ana ndaw suy jóge màndiŋ ma nii,  
wéeroo nijaayam?  
Ndaw si  
Ci ron pom gi laa la yee,  
fa la sa yaay jàppe ëmb,  
jur la fa.   
 6 Teg ma ci sa xol ni torlukaay†torlukaay mooy jumtukaay bu mel ni lu ñuy tàmponee.,  
mbaa ci sa përëg ni lamu màndarga.  
Mbëggeel a bare doole ni dee,  
fiiraange xér ni bàmmeel.  
Day jàpp jippét,  
di jum bu Aji Sax ji taal‡Mbaa: tàkk di sël-sëli..   
 7 Ndox mu ne xéew du fey mbëggeel,  
ay dex du ko mëdd.  
Ku koy weccee sa alalu kër gépp it,  
ñu jéppi laa jéppi rekk.   
Càmmiñi ndaw si  
 8 Sunub jigéen lu ndaw la,  
ween sax amu ko.  
Lu nuy defal sunub jigéen  
bés bu ñu koy bëggsi?   
 9 Su doon am tata,  
nu tabaxal ko soorooru xaalis.  
Su doon bunt,  
nu aare ko xànqi seedar.   
Ndaw si  
 10 Maa dim tata,  
sama ween di sooroor ya;  
moo tax waa ji xam ne  
maa di jàmmam.   
 11 Suleymaan am na reseñ ca Baal Amon.  
Da koo dénk ay beykat.  
Ku nekk di ko fey meññeef ma  
junniy dogi xaalis.   
 12 Junniy dogi xaalis yi,  
Suleymaan, yaa ko moom;  
ñaari téeméer yi, beykat yi.  
Waaye sama toolub reseñ, maa ko moom.   
Waa ji  
 13 Yaw mi tooge digg tool bi,  
samay xarit a ngi teewlu sa baat,  
waxal boog, ma dégg.   
Ndaw si  
 14 Nijaay, dawsil,  
melal ni kéwél,  
mbaa kooba gu ndaw  
ci kaw tund wi ci gàncax gu xeeñ gi.