39
1 Jant yooyu Merodag Baladan buuru Babilon miy doomu Baladan moo yónneey bataaxal ak yóbbal ca Esekiyas. Fekk na mu déggoon ne Esekiyas daa woppoon bay doora am tan. 2 Esekiyas am ca mbégte, daldi won ndaw ya kërug dencukaayam: xaalis baak wurus waak ndàbb jaak diwu tànnéef gaak mboolem néegub gànnaayam ya ak mboolem lu nekkoon cay dencam. Amul lenn lu leen Esekiyas wonul ci biir këram ak mboolem fu bokk ci kilifteefam. 3 Gannaaw loolu Yonent Yàlla Esayi dikk ne Buur Esekiyas: «Lu la nit ñii wax ak fu ñu jóge sax ba fi yaw?» Esekiyas ne: «Réew mu sore lañu bàyyikoo, dikk ba fi man, réewum Babilon.»
4 Mu ne ko: «Ana lu ñu gis sa biir kër?» Esekiyas ne ko: «Mboolem lu nekk sama biir kër, gis nañu ko. Amul lenn lu ma leen wonul ci samay denc.» 5 Esayi ne Esekiyas: «Déglul kàddug Aji Sax ji Boroom gàngoor yi: 6 Ay jant a ngii di ñëw, dees na yóbbu Babilon lépp lu nekk sa biir kër, te say maam dencoon ko, ba tey jii. Du lenn luy des.» Kàddug Aji Sax jee. 7 «Te it ñenn ci sag njaboot, ñu soqikoo ci yaw, di ñoo meññ ci sa geño, dinañu leen jàpp, ñu doon jaam yu ñu tàpp ca biir kër buuru Babilon.» 8 Esekiyas ne Esayi: «Kàddug Aji Sax ji nga jottali, jàmm la.» Booba ma nga naan: «Ndegam jàmm ju ne ñoyy ay am sama giiru dund kay!»