Aji Sax jeey dàmp xol yi
40
(Saar 40—66)
Xibaaru jàmm ñeel na Israayil
1 Dëfalleen a dëfal sama ñoñ,
la seen Yàlla wax!
2 Waxleen lu dalal xelu Yerusalem, yéeneleen
ne leen seen xare jeex na,
seen mbugal mat na.
Ñoo nangoo ci loxol Aji Sax ji
lu fey ñaari yoon seen bépp bàkkaar.
3 Baat a ngi jib, naan:
«Nangeen xàll yoonu Aji Sax ji ci màndiŋ mi,
fàkkalleen sunu Yàlla
xàll wu jub fi joor gi.
4 Wépp xur lees di kaweel,
tund wu mag ak wu ndaw lees di suufeel;
ba fu tunde mujj dig joor,
fu ñagasoon maase,
5 darajay Aji Sax ji daldi feeñ,
àddina sépp bokk gis ko.
Aji Sax jee ko wax ci làmmiñam.»
6 Baat a ngi naa: «Yéeneel!»
Ma ne: «Lu may yéene?»
Mu ne: «Neel:
Nit am ñax doŋŋ la;
gépp ngoram mel ni tóor-tóoru àll.
7 Ñax ma wow,
tóor-tóor ma lax
fa ko Aji Sax ji yónnee mbóoyo.
Askan wi kay, am ñax doŋŋ la.
8 Am ñax day wow;
tóor-tóor day lax.
Waaye sunu kàddug Yàlla
mooy sax ba fàww.»
9 Yaw Siyoŋ, xibaarkatu jàmm bi,
doxal yéegi tund wu kawe,
te xaacook doole.
Yaw Yerusalem, xibaarkatu jàmm bi,
xaacul te bul ragal!
Neel dëkki Yuda yi:
«Seen Yàllaa ngii!
10 Boroom bi, Aji Sax jaa ngii,
dikkaale doole
ak kàttanu kilifteefam.
Mu ngii ànd ak ñi mu yooloo,
ñu dig peyam, dox jiitu ko.
11 Mooy sàmm géttam bii ni kuy sàmmug juram,
boole mbote yi cib loxoom,
taf cib dënnam, yóbbu;
xar yiy nàmpal, mu wommat.»
12 Ana ku natte géej biir loxoom?
Ku xaymaa asamaan yaatuwaayu loxo?
Ku mana fab suuf sépp, sol cib nattukaay?
Ana ku natte ab màndaxekaay tund wu mag?
Mbaa mu tam-tamal tund wu ndaw?
13 Ana ku mana nànd xelum Aji Sax ji?
Mbaa nga dib xejjam, ba di ko digal?
14 Ana ku mu diisool, ba kooka tegtal ko,
jàngal ko yoonu njub,
jàngal ko xam-xam,
xamal ko yoonu dég-dég?
15 Xeet yaa ngii, mel ni aw toq ci biir bagaan,
jàppeesu leen lu moy diisaayu feppu suuf!
Dun yi lay yékkati ni pëndub suuf!
16 Gottub Libaŋ xambul taalu sarxalukaayam,
te mala ya ca ne doyu ko saraxu rendi-dóomal!
17 Xeetoo xeet du tus fi kanamam,
te jàppewu leen lu moy neenug neen.
18 Ana kan ngeen di niruleek Yàlla,
ak nataal bu ngeen koy dendaleel?
19 Xanaa du jëmmu tuur ju liggéeykat móol,
ab tëgg xoobe ko wurus,
takk ca caqi xaalis?
20 Ku néewle ba amul may gu ni tollu,
mooy tànn bant bu dul nëb,
seeti liggéeykat bu xareñ
bu ko ci sàkkal jëmmu tuur ju dëgër!
21 Xanaa dangeena xamul lii?
Am dangeena déggul lii?
Dees leena waxul ca njàlbéen,
am seen xel a jàppul nan la àddina sosoo?
22 Moom moo tooge ca kaw wërngalu suuf,
ñi ko dëkke mel niy soccet,
moo tàllal asamaan ni ndimo,
firi ko nib xayma, daldi dëkke.
23 Mooy sànk kilifa,
di neenal njiitu àddina.
24 Ba ñu sampoogul,
toogaguñu sax,
ba seeni reen di riigu,
ca la leen Aji Sax jiy wal, ñu wow,
ngëlén buub, yóbbu ni boob.
25 Aji Sell ji ne:
«Ana ku ngeen may nirooleel,
ba may moroomam?»
26 Séentuleen kaw, xoolleen Ki sàkk biddiiw yii!
Xanaa kiy daaguloo leeri asamaan ni gàngoor gu mat,
ñoom ñépp lay woo ci seen tur,
ci kawewaayu dooleem ak màggaayu kàttanam,
te kenn du ci wuute.
27 Yeen askanu Yanqóoba, lu ngeen di jàmbat?
Yeen Israayil laa ne, lu ngeen di jooy,
naa: «Aji Sax ji gisul li nu dal,
sunu Yàlla daal, daa réere sunu àq!»
28 Dangeena xamul,
am dangeena déggul
ne Aji Sax jeey Yàlla ba fàww,
sàkk suuf cat ba cat,
du sonn, du tàyyi,
te am xelam nattuwul?
29 Mooy dooleel ku loof,
di kàttanal ku jeele.
30 Waxambaane sonn, loof;
xalelu góor di tërëf a tërëf,
31 kiy yaakaar Aji Sax ji moom, di yeeslu doole;
da naa fëyy ni jaxaay juy naaw,
di xélu te du xiix,
di dox te du xoox.