6
Yeesu leel na mbooloo
Gannaaw loolu Yeesu jàll ca wàllaa dexu Galile, ga ñuy wax dexu Tiberyàdd itam. Mbooloo mu bare topp ca moom, ndax ñoo gis firnde ya mu wérale jarag ya. Yeesu yéeg ca kaw tund wa, daldi toog foofa ak ay taalibeem. Booba màggalu Yawut ga ñuy wax bésub Mucc, jubsi na. Yeesu dawal bëtam, gis mbooloo mu réy mu dikk, jëm ca moom. Mu ne Filib: «Fu nuy jële mburu mu nu leen leele?»
Loolu nag da koo wax ngir seetlu Filib, ndax moom ci boppam xamoon na la mu nar. Filib ne ko: «Peyug juróom ñetti weer sax jëndul mburu mu leen doy, ba kenn ku nekk ci ñoom am ci ndog su tuut.» Àndre, keneen ca taalibe ya, te bokk ak Simoŋ Piyeer ndey ak baay, ne ko: «Ab xalee ngi fi de, am na juróomi mburu*mburu: mburu yu ndaw lañu, yu ñu defare sungufu lors. Moo doon lekku ñi néew doole. ak ñaari jën, waaye loolu lu mu jariñ ñu tollu nii?» 10 Yeesu daldi ne: «Toogalleen nit ñi.» Ñax mu baree nga woon ca béreb booba. Góor ña nag toog, seenub lim wara tollu ci juróomi junni (5 000). 11 Yeesu jël mburu ya, yékkati kàddug cant, daldi ko séddale ña fa toog. Jën ya itam noonu, ñu lekk ba doyal.
12 Ba ñu lekkee ba regg, Yeesu ne taalibeem ya: «Dajaleleen desiti mburu mi, ba dara du ci yàqu.» 13 Ñu dajale ba feesal fukki pañe ak ñaar ci dogi juróomi mburu ya ñu lekk ba desal.
14 Ba nit ña gisee firnde jooju Yeesu def, dañu ne: «Kii daal, dëgg-dëgg mooy Yonent bi dikk ci àddinaYonent bi: seetal ci Baamtug yoon wi 18.15.15 Yeesu nag gis ne dañoo nara dikk, jàpp ko yóbbu, ngir fal ko buur, mu daw dellu, moom kenn ca tund wa.
Yeesu dox na ci kaw ndox
16 Ba jant sowee, taalibeem ya dem ca tefes ga. 17 Ci kaw loolu ñu dugg gaal, ngir jàll jëm Kapernawum, ndax booba lëndëm na te Yeesu agseegul. 18 Dex ga nag yëngu lool, ndax ngelaw lu jóg ak doole. 19 Ba taalibe ya joowee lu tollook juróomi kilomet ba juróom benn, Yeesu lañu séen, muy dox ca kaw dex ga, jëm ca gaal ga, ñu daldi tiit. 20 Yeesu ne leen: «Man mii la, buleen tiit!» 21 Ñu door koo nangoo dugal ca gaal ga. Ci kaw loolu gaal ga teeri ca saa sa, fa ñu jëm.
22 Ca ëllëg sa mbooloo ma des ca geneen wàllaa dex ga, seetlu ne genn gaal doŋŋ a fa nekkoon, te Yeesu àndul woon ak taalibe ya ca gaal ga ñu dugg, waaye taalibe ya rekk a dem. 23 Gannaaw gi la yeneen gaal jóge Tiberyàdd, teersi fa feggook béreb ba nit ña lekke woon mburu ma, gannaaw ba Sang bi yékkatee kàddug cant. 24 Ba mbooloo ma gisee nag ne Yeesu ak taalibe ya, kenn nekku fa, gaal yooyu lañu dugg, dem seeti ko Kapernawum.
Yeesu mooy ñamu dund
25 Ci kaw loolu ñu fekk Yeesu ca geneen wàllaa dex ga, ne ko: «Kilifa gi, kañ nga fi ñëw?»
26 Yeesu ne leen: «Maa leen ko wax déy ci lu wér, yeen du firnde yi ngeen gis a tax ngeen di ma seet, waaye mburu mi ngeen lekk ba regg moo tax. 27 Ñam wuy yàqu, bumu leen taxa liggéey; liggéeyalleen ñam wi sax, ñam wiy texeel fàww, te Doomu nit ki moo leen koy jox, ndax moom la Yàlla màndargaal, ngir firndeel ne moom la tànn.»
28 Ñu ne ko: «Ana lu nuy def, ba jëfe jëf ji neex Yàlla?» 29 Yeesu ne leen: «Jëf ji neex Yàlla, mooy ngeen gëm ki mu yebal.»
30 Ñu ne ko: «Jan firnde ngay def, nu gis ba gëm la? Ana jëf joo nu mana defal? 31 Sunuy maam de, mànn lañu dunde ca màndiŋ ma, te noonu lañu binde ne: “Peppum asamaan la leen leelSeetal ci Taalifi cant 78.24; Mucc ga 16..”»
32 Yeesu neeti leen: «Maa leen ko wax déy, ci lu wér, du Musaa moo leen jox ñamu asamaan, sama Baay la, te moo leen jox tey ñamu asamaan dëgg. 33 Ndaxte ñamu Yàlla mooy ki wàcce asamaan te kooku moo may àddina ñu dund.» 34 Ñu ne ko nag: «Sang bi, dee nu may saa su ne ci woowu ñam!»
35 Yeesu ne leen: «Man maay ñam wiy joxe dund. Ku ñëw ci man, doo xiif mukk; te ku ma gëm, doo mar mukk. 36 Waaye wax naa leen ko; gis ngeen ma, te taxul ngeen gëm! 37 Képp ku ma Baay bi jox dina ñëw, te man, ku ñëw ci man, duma ko dàq mukk. 38 Def sama coobarey bopp taxul ma wàcce fa asamaan, waaye def coobarey ki ma yónni moo tax. 39 Ki ma yónni nag, coobareem moo di mboolem ñi mu ma jox, buma ci ñàkk kenn, waaye naa leen dekkal kera bés bu mujj ba. 40 Ndax sama coobarey Baay kat moo di képp ku gis Doom ji te gëm ko, na texe ba fàww, te maa koy dekkal keroog bés bu mujj ba.»
41 Yawut ya nag di ñurumtoo Yeesu, ndax la mu ne: «Man maay ñam wi wàcce fa asamaan.» 42 Ñu naan: «Xanaa kii du Yeesu, doomu Yuusufa? Nun, nu xam baayam, xam ndeyam. Ana nu mu mana waxe ne asamaan la jóge?»
43 Yeesu ne leen: «Baleen ñurumtu bi ci seen biir. 44 Kenn manula ñëw ci man te Baay bi ma yónni indiwu ko; te ku ñëw ci man, maa koy dekkal kera bés bu mujj ba. 45 Bindees na ci téerey yonent yi ne: “Ñoom ñépp ay jànge ci Yàlla§Seetal ci Esayi 54.13..” Kon nag képp ku dégg Baay bi, ba déggal àlluwaam, dina ñëw ci man. 46 Tekkiwul ne kenn mas naa gis Baay bi. Xanaa ki bawoo fa Yàlla, kookoo gis Baay bi. 47 Maa leen ko wax déy, ci lu wér, ku gëm, yaa texe ba fàww. 48 Man maay ñam wiy joxe dund. 49 Seeni maam a lekk mànn ca màndiŋ ma, te dee nañu. 50 Waaye ñam wii mooy wi wàcce fa asamaan, ngir ku ko lekk, du dee. 51 Man maay ñam wiy dund te wàcce fa asamaan. Ku lekk ci wii ñam, mooy texe ba fàww. Ñam woowu nag mooy samaw suux; maa ko joxe, ngir àddina dund.»
52 Ci kaw loolu Yawut ya di werante werante wu tàng ci seen biir naan: «Ana nu nu kii mana joxee aw suuxam, nu lekk?»
53 Yeesu ne leen: «Maa leen ko wax déy ci lu wér, bu ngeen lekkul ci suuxu Doomu nit ki, naan deretam, amuleen dund ci seen jëmmi bopp. 54 Képp ku lekk samaw suux, naan sama deret, texe nga ba fàww, te maa lay dekkal kera bés bu mujj ba. 55 Ndaxte sama yaram mooy ñam wi wóor, sama deret di naan gi wóor. 56 Képp ku lekk sama suux, naan sama deret, ci man lay dëkk, ma dëkk ci moom. 57 Ni ma Baay biy dund yebale, te may dund ndax moom, noonu la ki ma lekk di dunde ndax man. 58 Woowu ñam mooy wi wàcce fa asamaan; bokkul ak ñam wa seeni maam lekkoon te teewuleena dee. Ku lekk wii ñam, yaay texe ba fàww.»
59 Baat yooyu la Yeesu wax, ba muy jàngale ca jàngub Yawut ba, ca Kapernawum.
Taalibey Yeesu yu bare xàcc nañu
60 Taalibey Yeesu yu bare, ba ñu déggee loolu, dañu ne: «Gii kàddooka jafe! Ana ku ko mana dégg?»
61 Yeesu nag yég ci boppam ne taalibeem yaa ngi ñurumtoo loolu. Mu ne leen: «Xanaa kàddu gii mbetteel la leen def? 62 Kon bés bu ngeen gisee Doomu nit kiy yéeg jëm fa mu njëkkoona nekk nag? 63 Noowug Yàlla mooy dundloo; nitu suuxu neen manul dara. Kàddu gi ma leen wax moo leen di jottali Noowug Yàlla giy taxa dund. 64 Waaye am na ñenn ñu bokk ci yeen, ñu gëmul.»
Ndax kat Yeesu xamoon na ca njàlbéen ñan ñooy ña gëmul woon, ak kan mooy ka koy wor. 65 Mu teg ca ne: «Looloo tax ma ne leen kenn manula ñëw ci man, te du Baay bi moo ko ko may.»
66 Booba la taalibeem yu bare dëpp, àndatuñu ak moom. 67 Yeesu nag ne fukki taalibe yaak ñaar: «Yeen itam bëgg ngeena dem am?» 68 Simoŋ Piyeer ne ko: «Sang bi, ci kan lanu jëm? Kàddu giy texeel fàww, yaa ko yor! 69 Nun gëm nanu te ràññee nanu ne yaa di Aji Sell ju Yàlla ji.» 70 Yeesu ne leen: «Xanaa du man maa leen tànn, yeen Fukk ak ñaar? Ndaxam kenn a ngi bokk ci yeen te ab seytaane la!» 71 Yuda doomu Simoŋ Iskaryo la doon wax, ndax mooy ka ko doon waaja wor, te ca Fukk ñaak ñaar la bokkoon.

*6.9 mburu: mburu yu ndaw lañu, yu ñu defare sungufu lors. Moo doon lekku ñi néew doole.

6.14 Yonent bi: seetal ci Baamtug yoon wi 18.15.

6.31 Seetal ci Taalifi cant 78.24; Mucc ga 16.

§6.45 Seetal ci Esayi 54.13.