7
Yeesu dem na ca màggalu Mbaar ya
Gannaaw loolu Yeesu diiwaanu Galile la doon wër. Bëggul woona doxe biir diiwaanu Yude, ndax njiiti Yawut ya ñoo ko doon wuta rey.
Ci biir loolu màggalu Yawut gi ñuy wax Mbaar yi, jubsi. Rakki Yeesu yu góor ya ne Yeesu: «Jógeel fii te dem diiwaanu Yude, ngir say taalibe, ñoom itam, gis jaloore yi ngay def. Kenn du jëfe biir kumpa tey wuta feeñ. Gannaaw yaay def yii jaloore, wonal sa bopp àddina,» ndax booba ay rakkam sax gëmuñu ko woon.
Yeesu ne leen: «Sama waxtu jotagul; yeen nag, seen waxtu bopp, bés bu nekk la. Àddina du leen mana bañ, waaye man la bañ, ndax maa koy seedeel ne ay jëfam dafa bon. Yeen nag demleen màggal ga, man demuma ca màggal googu, ndax sama waxtu jotagul.» Loolu la leen wax, daldi des ca Galile.
10 Teewul ba rakki Yeesu demee ca màggal ga, Yeesu itam dem na ca, waaye siiwalul aw yoonam, daanaka daa làqu. 11 Yawut ya nag di ko seet, naan: «Ana waa ji?» 12 Ci kaw loolu déeyoo bi ci mbiram bare ca mbooloo ma. Ñii naan: «Nit ku baax la.» Ñee naan: «Déedéet, day naxe.» 13 Waaye taxul kenn waxe mbiram ca kaw, ndax ragal njiiti Yawut ya.
Yeesu jàngale na ca màggal ga
14 Ba ñu demee ba ca diggu màggal ga, Yeesu dem ca kër Yàlla ga, di jàngale. 15 Yawut ya jaaxle, naan: «Kii nu mu ame bii xam-xam te jàngul?»
16 Yeesu daldi leen wax ne leen: «Li may jàngale, moomuma ko, ki ma yebal a ko moom. 17 Ku namma jëfe coobarey Yàlla, dina xam ndax li may jàngale ci Yàlla la jóge, am ci sama coobarey bopp laay waxe. 18 Kiy wax ci coobarey boppam nag, darajay boppam lay sàkku, waaye ki bëgga fésal darajay ki ko yónni, kooku ku dëggu lay doon, te ag njubadi du nekk ci moom. 19 Xanaa du Musaa moo leen jox ndigali yoon wi? Ndaxam kenn ci yeen jëfewul yoon wi! Ana lu ngeen may wuta rey?» 20 Mbooloo ma ne ko: «Yaw rab a la jàpp! Ku lay wuta rey?»
21 Yeesu ne leen: «Jenn jaloore doŋŋ laa def, yeen ñépp ngeen waaru! 22 Ndigalu xarafal gi leen Musaa jox, doonte jógewul ci Musaa, waaye cay maam la ba tey, tax na ngeen di xarafale ci bésub Noflaay sax. 23 Gannaaw nit ay xaraf ci bésub Noflaay, ngir yoonu Musaa baña tebbiku, ana lu ngeen ma meree ndax nit ku ma wéral péŋŋ ci bésub Noflaay? 24 Bàyyileen di àttee li leen seen bët may, deeleen àttee dëgg.»
Ndax Yeesu mooy Almasi bi?
25 Ci kaw loolu ñenn ci waa Yerusalem naan: «Xanaa du kii lees di wuta rey? 26 Te mu ngii ne fàŋŋ di waare, te waxuñu ko dara. Xanaa sunu kilifa yi dañoo xam ne kii mooy Almasi bi? 27 Moonte kii, xam nanu fu mu bokk, te su Almasi bi dikkee, kenn du xam fu mu bokk.»
28 Ci kaw loolu Yeesu di jàngale ca kër Yàlla ga, daldi biral ne: «Kon xam ngeen ma, xam fi ma bokk? Ndaxam du ci sama coobarey bopp laa dikke, te ki ma yónni, ku wóor la. Yeen nag xamuleen ko. 29 Man maa ko xam, ndax ci moom laa bàyyikoo, te moom moo ma yebal.»
30 Ba mu ko defee ñu di ko wuta jàpp, waaye kenn tegu ko loxo, ndax waxtoom moo jotagul woon. 31 Teewul ñu bare ca mbooloo ma gëm ko, te naan: «Almasi bi sax, bu dikkee, ndax dina def firnde yu ëpp firnde yi nit kii def?» 32 Farisen ya dégg loola mbooloo may déeyoo ci mbirum Yeesu. Sarxalkat yu mag ya ak Farisen ya daldi yebal ay wattukati kër Yàlla ga, ngir ñu jàppi ko.
33 Yeesu nag ne: «Diir bu gàtt laay toogaat ak yeen, doora dem ca ki ma yónni. 34 Dingeen ma seet, waaye dungeen ma gis; te man fa may nekk, yeen, dungeen fa mana dem.»
35 Yawut ya naan ca seen biir: «Kii fu muy waaja jëm, fu ñu ko dul gise? Xanaa ca Yawut ya dëkki ca jàmbur ña? Xanaa jàmbur ña lay jàngali? 36 Ak luy tekkitel kàddu gii mu wax, ne: “Dingeen ma seet, waaye dungeen ma gis; te man fa may nekk, yeen dungeen fa mana dem?”»
37 Bés ba mujj ca màggal ga nag moo ca gënoona màgg. Keroog la Yeesu taxaw, àddu ca kaw ne: «Ku mar, na ñëw ci man, naan; 38 ku ma gëm, ay dex ay balle cib dënnam, di wal ndox muy dund! Te noonu la ko Mbind mi indee.» 39 Booba Noowug Yàlla la doon wax, Noo ga gëmkati Yeesu doon waaja jot, te jotaguñu ko woon, ndax booba, Yeesoo tàbbeegul woon ci teraangaam.
40 Ba ñenn ca mbooloo ma déggee kàddu yooyu, dañu ne: «Aylayéwén kii mooy Yonent bi.» 41 Ñeneen naan: «Kii mooy Almasi bi!» Teewul mu am ñu naan: «Galile, nu fa Almasi biy jógee? 42 Du Mbind mi moo wax ne, Almasi bi ci xeetu Daawuda lay soqikoo, ca Betleyem, dëkk ba Daawuda fekk baax*Seetal ci Mise 5.1; Taalifi cant 89.4-5.43 Féewaloo nag am ca mbooloo ma ndax Yeesu. 44 Ñenn ca ñoom bëggoon nañu koo jàpp, waaye kenn tegu ko loxo.
Njiiti Yawut yi gëmuñu Yeesu
45 Ba loolu amee wattukat ya dellu ca sarxalkat yu mag ya ak Farisen ya. Ñooñu ne leen: «Lu tax indiwuleen ko?» 46 Wattukat ya ne leen: «Nit masula waxe ni kii!» 47 Farisen ya ne leen: «Kon yeen itam nax nañu leen a? 48 Ndax yeena gis ci njiit yi mbaa ci Farisen yi, kenn ku ko gëm? 49 Xanaa mbooloo mii xamul yoonu Musaa, te ñu alku lañu!»
50 Nikodem bokk na ca Farisen ya fa nekkoon, te demoon na seeti Yeesu lu jiitu loolu. Mu ne leen: 51 «Sunuw yoon ndax dina daan nit te njëkkeesu koo déglu, boole ci xam lu mu def?» 52 Ñu ne ko: «Xanaa yaw itam ci diiwaanu Galile nga bokk? Gëstul, kon dinga xam ne Galile, ab yonent du fa feeñe.»
53 Ba loolu amee ku nekk ñibbi këram.

*7.42 Seetal ci Mise 5.1; Taalifi cant 89.4-5.