7
Sikkal jàmbur aay na
1 «Buleen di sikkale, su ko defee deesuleen sikkal. 2 Ndaxte àtte bi ngeen di àttee, moom lees leen di àttee; te natt bi ngeen di nattale, moom lees leen di nattale. 3 Ana looy xoole xatax bi ci sa bëtu mbokk, te sa bët bi, gànj gi ci nekk, gisuloo ko? 4 Mbaa ana noo naa sa mbokk: “Xaaral, ma dindil la xatax bi ci sa bët,” te gànj a ngoogu ci sa bët yaw? 5 Jinigalkat bi, njëkkala dindi gànj gi ci sa bët, ba gis bu baax, nga doora dindi xatax bi ci sa bëtu mbokk.
6 «Buleen jox lu sell xaj yi, mbaa ngeen di sànni seeni per ci kanam mbaam-xuux yi, lu ko moy ñu dëggaate ko, ba noppi xaj yi walbatiku ci seen kaw, daggate leen.
Yàlla nangu na ñaanu ku gëm
7 «Ñaanleen, ñu may leen; seetleen, gis; fëggleen, ñu ubbil leen. 8 Ndaxte képp ku ñaan, dinga am; ku seet, gis; ku fëgg it, dees na la ubbil. 9 Kan ci yeen sax, la doomam di ñaan mburu, mu jox kow doj? 10 Mbaa mu ñaan kow jën, mu jox ko jaan? 11 Ndegam yeen ñi bon, yeena mana may seeni gone lu baax nag, kon seen Baay ba fa asamaan, ñaata yoon la leen dàqa may lu baax, ñi ko ko ñaan!
12 «Lépp lu ngeen bëgg nit ñi defal leen ko nag, nangeen leen ko defale noonu, nde loolu mooy yoonu Musaa ak yonent yi.
Buntu dund xat na
13 «Duggeleen ci bunt bu xat bi, ndax bunt beek yoon wi jëm sànkute dañoo yaatu, te ñu baree cay dugge. 14 Waaye xat la def, bunt ba jëm dund; sew it la yoon wa def, te ñu néew a koy gis.
Doomu garab, ndey ja
15 «Moytuleen yonenti caaxaan yi. Ñooy ñëw ci yeen, soloo melow xar, te diy bukki yu soxor. 16 Seenum meññeef ngeen leen di xàmmee. Ndax ag dédd, dees na ci witte doomi reseñ; am ay dagg, dees na ci witte doomi figg? 17 Garab gu baax gu nekk, doom yu baax lay meññ; waaye garab gu bon, doom yu bon lay meññ. 18 Garab gu baax daal manula meññ doom yu bon, garab gu bon itam manula meññ doom yu baax. 19 Gépp garab gu dul meññ doom yu baax nag, dees koy gor, sànni ca sawara sa. 20 Kon nag ñoom daal ci seenum meññeef ngeen leen di xàmmee.
21 «Du képp ku ma naan: “Sang bi, Sang bi,” mooy tàbbi ci nguurug asamaan, xanaa ñiy jëfe sama coobarey Baay ba fa asamaan. 22 Bu bés baa, ñu baree ma naan: “Sang bi, Sang bi, xanaa du saw tur lanu daa waaree, di dàqe saw tur ay rab, tey defe saw tur kéemaan yu bare?” 23 Booba laa leen di wax ne: “Masuma leena xam, defkati ndëngte yi ngeen doon, xiddileen ma!”
Ki dégg, jëfe, moo xelu
24 «Kon képp ku dégg sama kàddu yii, te di ko jëfe, dafa mel ni nit ku xelu ki tabax këram ci kaw aw doj. 25 Ba mu noppee, taw ba sóob, wal ma dikk, ngelaw la riddi, lépp dal ca kër ga, te màbbul, ndax doj wa mu sampe. 26 Waaye képp ku dégg sama kàddu yii te jëfewu ko, dafa mel ni nit ku ñàkk xel ki tabax këram ci gannuus gi. 27 Ba mu noppee, taw ba sóob, wal ma dikk, ngelaw la riddi, lépp dal ca kër ga; mu màbb, yàqu yaxeet.»
28 Ba Yeesu waxee loolu ba noppi, mbooloo ma daa yéemu ca njàngaleem, 29 ndax sañ-sañ ba mu leen di jàngale niroowul ak na seen firikati yoonu Musaa yay jàngalee.