8
Yeesu faj na ku gaana
1 Yeesu moo wàcce ca tund wa, mbooloo mu bare topp ko. 2 Ab gaana jekki dikk, sujjóotal ko, ne ko: «Sang bi, su la soobee, man nga maa setal.» 3 Mu tàllal loxoom, laal ko ne: «Soob na ma, setal.» Ca saa sa ngaanaam ga set wecc. 4 Yeesu ne ko: «Fexeel ba bu ko wax kenn, demal rekk ca sarxalkat ba, ngir mu seet la, te nga génne sarax si yoonu Musaa santaane*Seetal ci Sarxalkat yi 14.1-32., ngir muy firnde ci ñoom.»
Ngëm gu réy, yool bu réy
5 Gannaaw ba Yeesu duggsee dëkk ba ñuy wax Kapernawum, ab njiitu takk-der bu waa Room moo dikk ba ci moom, ñaan ko, 6 ne ko: «Sang bi, sama surga moo tëdd ca kër ga, lafañ, te nekke mitit wu tar.» 7 Yeesu ne ko: «Man, maay dikk, faj ko.» 8 Teewul njiit la ne ko: «Sang bi, yeyoowuma nga dugg sama kër; waxal genn kàddu rekk, sama surga wér. 9 Ndaxte man itam ci kilifteef laa tënku, te maa ngeek ay takk-der yu nekk ci sama ndigal. Su ma nee kii: “Demal,” mu dem, ma ne kee: “Ñëwal,” mu ñëw. Te sama jaam bu ma ko nee: “Defal lii,” mu def ko.»
10 Ba ko Yeesu déggee, daa yéemu, daldi ne ñi topp ci moom: «Maa leen ko wax, déy, ku réye nii ngëm, gisuma ko ci bànni Israayil. 11 Maa leen wax ne leen, ñu bareey bawoo penku ak sowu, dikk bokk ca ndabal bernde ja, ñook Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, keroog ca nguurug asamaan. 12 Waaye doom yi yeyoo nguur ga, ñoom lees di sànni ca biti ca lëndëm gu tar ga. Foofa lees di jooye aka yéyoo ndax mitit.» 13 Ci kaw loolu Yeesu ne njiitu takk-der ba: «Demal, noonu nga ko gëme, na ame noonu ci yaw.» Ca waxtu woowa la surga ba wér.
Yeesu faj na jarag yu bare
14 Gannaaw loolu Yeesu dem kër Piyeer, daldi fekk yaayu jabaru Piyeer, mu tëdd, yaram wa tàng. 15 Yeesu jàpp loxol soxna sa, tàngooru yaram wa teqalikook moom, soxna sa jóg, di ko toppatoo.
16 Ca ngoon sa ñu indil ko ñu bare ñu rab jàpp. Ba loolu amee Yeesu dàqe rab ya kàddoom, mboolem ña wopp, mu faj leen. 17 Noonu la kàddu ga jottalikoo woon ci gémmiñu Yonent Yàlla Esayi mate. Mooy ba mu nee:
«Moom sunuy wopp la jël,
sunuy jàngoro la sëfoo†Seetal ci Esayi 53.4..»
18 Ba Yeesu gisee mbooloo ma ko wër nag, dafa sant taalibe ya, ñu jàll ba ca wàllaa dex ga. 19 Ci biir loolu ab firikatu yoonu Musaa dikk, ne ko: «Kilifa gi, yaw laay topp fépp foo jëm.» 20 Yeesu itam ne ko: «Till akug kàmbam, njanaaw akub tàggam, waaye Doomu nit ki de, amul fu mu wéer boppam.» 21 Ba loolu amee keneen ca taalibe ya ne ko: «Sang bi, may ma, ma njëkka dem robi sama baay.» 22 Yeesu ne ko: «Toppal ci man te nga bàyyi néew yi, ñu rob seeni néew.»
Yeesu dalal na ngelaw
23 Ba mu ko defee, Yeesu dugg ca gaal ga, ay taalibeem ànd ak moom. 24 Ca saa sa ngelaw lu réy yëngal dex ga, ba gannax ya mëdd gaal ga. Teewul Yeesoo ngay nelaw. 25 Taalibe ya jegesi, yee ko, ne: «Sang bi, wallu nu, nu ngi sànku!» 26 Yeesu nag ne leen: «Lu ngeen di tiit, yeenaka néew ngëm!» Ci kaw loolu mu jóg, daldi gëdd ngelaw la ak gannax ya. Lépp ne sendaw. 27 Ba loolu amee, ñu waaru, naan: «Kii moo di kan, ba ngelaw leek dex gi di ko déggal?»
Yeesu faj na ñaar ñu rab jàpp
28 Ba Yeesu jàllee, ba teere diiwaanu waa Gadara, ñaar ñu rab jàpp ñoo génne ca sëg ya, dikk dogale ko, te di ñu soxor lool, ba kenn ñemewul woona jaare foofa. 29 Ñu jekki xaacu, ne: «Yaw Doomu Yàlla ji, ana lu nu joteek yaw? Ndax danga fee ñëw ngir mbugal nu, te jotagul?»
30 Fekk na genn coggalu mbaam-xuux yu baree nga leen dànd lu sore, di for. 31 Rab ya tinu ko ne: «Boo nu dàqee, yebal nu ca coggalu mbaam-xuux ya.» 32 Yeesu ne leen: «Demleen.» Rab ya nag génn, dugg ca mbaam-xuux ya, ci saa si coggal gépp bartaloondoo, tàbbi ca dex ga, daldi lab.
33 Ba loolu amee sàmm ya daw, ba ca dëkk ba, nettaliji lépp, ak la xewoon ca ña rab jàpp. 34 Ci kaw loolu rekk dëkk ba bépp génn, ngir dajeek Yeesu. Naka lañu ko gis, daldi koy tinu ngir mu génn seen gox ba.