15
Farisen aada la jiital
1 Ca jamono yooyu la ay Farisen ak ay firikati yoonu Musaa bàyyikoo Yerusalem, dikk ba ci Yeesu, ne ko: 2 «Lu tax say taalibe di jalgati aaday maam yi, ba duñu raxas seeni loxo, bala ñoo lekk?» 3 Yeesu nag ne leen: «Yeen itam lu tax ngeen di jalgati santaaneb Yàlla, ndax seen aaday bopp? 4 Ndax Yàlla da ne: “Teralal ndey ak baay*Seetal ci Mucc ga 20.12.,” neeti: “Ku saaga sa ndey mbaa sa baay, dee rekk mooy àtteem†Seetal ci Mucc ga 21.17..” 5 Te yeen ngeen ne: “Ku ne sa ndey mbaa sa baay: ‘Li ma warlook yaw, jébbal naa ko Yàlla,’ 6 kooku wàccoo na ak warugaru teral baayam.” Kon kay neenal ngeen kàddug Yàlla ndax seen aaday bopp. 7 Jinigalkat yi ngeen doon, Esayi yey na, ba mu jottalee kàdduy waxyu ci seen mbir, ne:
8 “Askan wii, làmmiñ lañu may wormaale,
waaye seen xol sore na ma.
9 Seen njaamu Yàlla neen la,
seen njàngale di santaaney niti kese‡Seetal ci Esayi 29.13..”»
10 Ci kaw loolu Yeesu woo mbooloo ma, ne leen: «Dégluleen te amug dégg. 11 Du li dugg ci gémmiñ mooy sobeel nit ki, waaye liy génne ci gémmiñ, loolu mooy sobeel nit ki.»
12 Ba loolu amee taalibe ya dikk ne ko: «Ndax xam nga ne, ba Farisen yi déggee kàddu googu, mer nañu?» 13 Yeesu ne leen: «Gépp gàncax gu sama Baay ba fa asamaan jëmbatul, dees na ko buddi. 14 Bàyyileen leen, ay gumba yuy wommat ay gumba lañu; gumba nag, su dee wommat gumba, ñoom ñaar ay ànd tàbbi ci kàmb.»
15 Piyeer nag ne Yeesu: «Firil nu léeb woowu.» 16 Yeesu ne ko: «Kon yeen itam amuleenug dégg ba tey? 17 Xamuleen ne, lépp lu dugg ci gémmiñ, ci koll bi lay dugg, balaa jàll, génneji gannaaw kër? 18 Li génne ci gémmiñ nag ci xolu boroom la jóge, te loolu mooy sobeel nit ki. 19 Ndaxte ci xol la mébét yu bon di jóge, ak bóom, ak njaaloo, ak séy yi yoon tere, ak càcc, ak seede lu dul dëgg, ak saaga. 20 Yooyu mooy sobeel nit ki, waaye lekk te raxasuwuloo sobeelul nit.»
Yeesu baaxe na jàmbur bu dul yawut
21 Gannaaw loolu Yeesu jóge fa, dem diiwaanu Tir ak Sidon. 22 Ci kaw loolu as ndawas Kanaaneen jekki jóge ca gox booba, di wax ca kaw, naan: «Sang bi, Sëtub Daawuda, yërëm ma! Sama doom ju jigéen la rab jàpp, mu sonn lool.» 23 Yeesu nag tontuwu ko baat, taalibeem ya dikk ne ko: «Dàqal kii nu topp, di yuuxu ci sunu kaw!» 24 Yeesu daldi ne: «Yebaleesu ma fu dul ci xari bànni Israayil yi réer.»
25 Teewul ndaw sa dikk, sujjóotal ko, ne ko: «Sang bi, dimbali ma!» 26 Yeesu ne ko: «Jël ñamu gone yi, sànni ko kuti yi, jaaduwul.» 27 Ndaw sa ne ko: «Dëgg la, Sang bi, waaye teewul kuti yi for ca la ruuse ca seen ndabal boroom.» 28 Yeesu nag ne ko: «Ndaw sii, yaaka réy ngëm. Kon nag na la amal noonu nga ko bëgge.» Ca waxtu woowa la doom ja wér.
Yeesu faj na ñu wopp
29 Ba mu ko defee Yeesu bàyyikoo foofa, dem ca tàkkal dexu Galile. Mu yéeg ca kaw tund wa, toog fa. 30 Mbooloo mu bare dikk, ànd aki lafañ, ak ay gumba, ak boroomi laago, aki luu, ak boroom jàngoro yu bare. Ñu indi leen fa kanam Yeesu, mu faj leen, 31 ba mbooloo ma waaru ca lañu gis luu ya di wax, boroom laago ya wér, lafañ ya di dox, gumba ya di gis. Ñu daldi sàbbaal Yàllay Israayil.
Yeesu leelati na mbooloo
32 Gannaaw loolu Yeesu woo taalibeem ya, ne leen: «Damaa yërëm mbooloo mi, ndax ñetti fan a ngii yu ñu nekk ak man, te amuñu lu ñu lekk. Bëgguma leena yiwi, ñu deme xiif, bala ñoo tële ci yoon wi.» 33 Taalibe ya ne ko: «Waaye fu nuy jële ci àll bu wéet bi mburu mu suur mbooloo mu réye nii?» 34 Yeesu ne leen: «Ñaata mburu ngeen am?» Ñu ne ko: «Juróom ñaari mburu ak as jën.»
35 Ba mu ko defee Yeesu sant mbooloo ma ñu toog ci suuf. 36 Mu jël juróom ñaari mburu ya ak jën ya, daldi yékkati kàddug cant, dagg mburu ma, jox taalibe ya, ñu jox mbooloo ma. 37 Ñépp lekk ba regg, te desit wa ñu yóbbu di juróom ñaari dàmba yu fees. 38 Ña ca lekk ñeenti junniy (4 000) góor lañu, te limaaleesul jigéen ña ak gone ya.
39 Ba loolu amee Yeesu yiwi mbooloo ma, daldi dugg gaal, jàll ba diiwaanu Magadan.