16
Diiŋatkat laaj na firnde
1 Ay Farisen ak ay Sadusen nag ñoo dikkoon ci Yeesu, di ko fiir, ne ko: «Firnde ju bawoo asamaan lanu bëgg, nga won nu ko.» 2 Yeesu ne leen: «Su ngoonee ngeen ne: “Ëllëg de day naaj, nde asamaan si daa xonq.” 3 Su dee ag suba ngeen ne: “Tey dina taw, asamaan saa ngi xiin, xonq curr.” Kon man ngeena ràññee melow asamaan, te manuleena ràññee firndey janti tey. 4 Maas gu bon te ñàkk kóllëre gi ngeen doon, firnde ngeen di wut, waaye deesuleen jox jenn firnde ju moy firndey Yunus.» Gannaaw loolu, mu bàyyikoo fa ñoom, dem.
Misaal tiiñ na taalibe ya
5 La ca tegu, taalibe ya jàllaat dex ga, ndeke fàtte nañoo yóbbaale mburu. 6 Yeesu ne leen: «Wattuleen te moytu lawiiru Farisen ñi ak Sadusen ñi.» 7 Taalibe ya nag di werante ci seen biir naan: «Nun de yóbbaalewunu mburu.» 8 Yeesu xam la ñuy wax, ne leen: «Yeenaka néew ngëm, lu ngeen di werante ci seen biir, naan amuleen fi mburu? 9 Kon xamaguleen ba tey, fàttalikuwuleen it juróomi mburu ya ca juróomi junniy (5 000) nit ña, ak ñaata pañey desit ngeen ca jële? 10 Juróom ñaari mburu ya ca ñeenti junniy (4 000) nit ña nag, ñaata dàmbay desit ngeen ca jële? 11 Nu ngeen mana umplee ne du mburoo ma tax di wax, ne ngeen wattu lawiiru Farisen ñeek Sadusen ñi?» 12 Ca lañu doora xam ne du lawiiru mburoo ko tax di wax, waaye njàngalem Farisen ña ak Sadusen ña, moom la leen wax ñu wattu ko.
Piyeer dégg na ndéey
13 Ba Yeesu demee ca diiwaan ba féete péeyu Sesare gu Filib, mu laaj taalibeem ya, ne leen: «Ana ku nit ñi wax ne mooy Doomu nit ki?» 14 Taalibe yi ne ko: «Ñii de nee ñu Yaxya la, ñee ne, Ilyaas la; ñale ne Yeremi la, mbaa keneen ci yonent yi.»
15 Yeesu ne leen: «Yeen nag, ngeen ne maay kan?» 16 Simoŋ Piyeer ne ko: «Yaa di Almasi bi, Doomu Yàlla Aji Dund ji.» 17 Yeesu ne ko: «Ndokkalee yaw, Simoŋ doomu Yowaan, ndax nit xamalu la ko, xanaa sama Baay ba fa asamaan. 18 Man nag maa ne la, yaa di Piyeer, doj wi; ci kaw doj wii it laay samp mbooloom gëmkat ñi, te dooley dee du ko manal dara. 19 Maa lay jox caabiy nguurug asamaan, te loo yeew ci kaw suuf, yeewees na ko fa asamaan; loo yiwi ci kaw suuf it, yiwees na ko fa asamaan.» 20 Gannaaw loolu Yeesu dénku taalibe yi, ngir ñu baña wax kenn ne mooy Almasi bi.
21 Ci jamono yooyu la Yeesu tàmbalee xamal taalibeem ya ne fàww mu dem Yerusalem, ba daje fa ak coono yu bare yu bawoo ca magi askan wa, ak sarxalkat yu mag ya, ak firikati yoonu Musaa ya, te dees na ko rey, ba ñetteelu fan ba, mu dekki. 22 Ci kaw loolu Piyeer ñaarook moom, tàmbali koo femmu, ne ko: «Yàlla tere, Sang bi, loolu du la dal mukk.» 23 Teewul Yeesu geestu, ne Piyeer: «Seytaane, xiddi ma, te dellu gannaaw, yaa ngi may gàllankoor; yaw xalaatoo yëfi Yàlla, waaye yëfi nit ngay xalaat.»
24 Gannaaw loolu Yeesu ne taalibeem ya: «Ku bëgga dikk topp ma, fàtteel sa bopp te nga gàddu sa bant bi ñu lay daaj, door maa topp. 25 Ndaxte képp ku bëgga rawale sa bakkan, dinga ko ñàkk, te ku ñàkk sa bakkan ndax man, dinga ko jotaat. 26 Te it jagoo àddina sépp lu muy jariñ nit, bu ñàkkee bakkanam? Ak lu nit wara mana weccee bakkanam? 27 Doomu nit ki de mooy dikke darajay Baayam, ànd aki malaakaam, te su boobaa mooy fey ku nekk ay jëfam. 28 Maa leen ko wax déy, ñenn a ngi taxaw fii, duñu dee te gisuñu Doomu nit ki ñëw ci nguuram.»