21
Yeesu dugg na Yerusalem
Gannaaw loolu Yeesu ak taalibe ya dikk ba jub Yerusalem, ba agsi ca dëkk ba ñuy wax Betfase ca wetu tundu Oliw ya. Yeesu yebal ñaar ca taalibe ya, ne leen: «Demleen ci dëkk bi ci seen kanam. Bu ngeen agsee rekk, dingeen fa gis mbaam mu ñu yeew ak cumburam; yiwileen leen, indil ma leen. Su leen kenn waxee dara, ngeen ne ko: “Boroom bee leen soxla.” Mu daldi leen bàyyi, ñu dem.»
Loolu nag ame noonu, ngir sottal la ñu waxoon ca jottalib yonent ba. Mooy ba mu nee:
«Neleen janq Siyoŋ mu taaru:
“Niiral, sa buur a la dikkal nii,
di ku woyof, war mbaam,
cumbur la war, doomu mbaam-sëf*Seetal ci Sàkkaryaa 9.9..”»
Taalibe ya dem, daldi koy defe noonu leen ko Yeesu sante. Ñu indi mbaam ma ak cumbur ba, daldi teg seeni yére ca kaw cumbur ba, Yeesu warcumbur: ci jamonoy jàmm, jamono yu xeex amul woon, buur yi daan nañu war mbaam, te doonul lu ñu leen di tuutal.. Ba loolu amee nit ñu bare lool lal seeni yére ca yoon wa, ñenn ña dagg ay cari garab, lal ca yoon wa. Ndiiraan ya ko jiitu ak ya ko topp a ngay xaacu naan:
«Osaana, cant ñeel na Sëtub Daawuda bi!
Na barke wàcc ci ki dikk ci turu Boroom bi!
Osaana, na cant jibe béreb ya gëna kawe.»
10 Yeesu nag agsi Yerusalem, dëkk ba bépp ne kër-kër ne këpp, ñu naan: «Kii moo di kan?» 11 Mbooloo ma ne leen: «Kii moo di Yonent bi, Yeesu mu Nasaret ca Galile.»
Yeesu dàq na jaaykat ya ca kër Yàlla ga
12 Ci kaw loolu Yeesu dugg ca kër Yàlla ga, daldi dàq mboolem ñay jaay aka jënd ca kër Yàlla ga. Mu dëpp taabali weccikati xaalis ya, ak tooguy jaaykati pitax ya. 13 Mu ne leen: «Bindees na ne: “Sama kër gi, kërug ñaan lees ko tuddeSeetal ci Esayi 56.7.,” waaye yeen, moom ngeen def rawtub sàcc.»
14 Ca la ay gumba ak ay lafañ dikk ba ca moom, ca kër Yàlla ga, mu faj leen.
15 Sarxalkat yu mag ya, ak firikati yoonu Musaa ya nag gis kéemaan ya mu def, ak xale yay xaacu ca biir kër Yàlla ga, naan: «Osaana, cant ñeel na Sëtub Daawuda bi!» Ñu daldi mer. 16 Ñu ne Yeesu: «Dégg nga li ñii di wax?» Mu ne leen: «Waawaaw. Masuleena jàng li ñu ne:
“Làmmiñu tuut-tànk, ba ci luy nàmp,
ci ngay sàkkale sa bopp ag cant§Seetal ci Taalifi cant 8.3.”?»
17 Ba loolu amee Yeesu bàyyikoo fa ñoom, génn dëkk ba, dem Betani, daldi fay fanaan.
Yeesu rëbb na garabu figg ga
18 Ba bët setee Yeesu di dellu ca dëkk ba. Ci biir loolu mu xiif. 19 Naka la séen ag figg fa feggook yoon wa, daldi cay dem, te taxul mu fekk ca dara lu dul ay xob doŋŋ. Mu ne figg ga: «Yàlla bu doom meññeeti fi yaw mukk!» Figg ga daldi wow ca saa sa.
20 Taalibe ya gis loolu, waaru, ne: «Nan la figg gi wowe ci saa si?» 21 Yeesu ne leen: «Maa leen ko wax déy, su ngeen gëmee te baña am xel ñaar, dungeen yem ci def nii figg gi, waaye tund wii sax, bu ngeen ko noon: “Jógal tàbbiji géej,” loolooy am. 22 Te lépp lu ngeen sàkkoo ñaan gu ànd ak ngëm, dingeen ko am.»
Lu jëm ci sañ-sañu Yeesu
23 Gannaaw loolu Yeesu dugg ca kër Yàlla ga. Naka lay jàngale, sarxalkat yu mag ya ak magi askan wa dikk, laaj ko ne ko: «Lii ngay def, ci ban sañ-sañ nga koy defe? Ak ku la jox boobu sañ-sañ?» 24 Yeesu ne leen: «Ma laaj leen man itam lenn; bu ngeen ma ko waxee, man itam ma wax leen ci ban sañ-sañ laay defe lii. 25 Sóobeb Yaxya ci ndox, fu mu jóge? Asamaan la ndigal la bawoo, am ci nit ñi?» Ñu diisoo ci seen biir, daldi ne: «Su nu nee: “Asamaan la ndigal la bawoo,” da nu naan: “Lu tax kon gëmuleen Yaxya?” 26 Te su nu nee: “Ci nit ñi la bawoo,” booba mbooloo ma lanu ragal, ndax ñépp ab yonent lañu jàppe Yaxya.» 27 Ñu ne Yeesu: «Loolu xamunu ko.» Moom itam mu ne leen: «Man itam duma leen wax ci ban sañ-sañ laay defe lii.»
Tuub moo gën të
28 «Waaye, luy seen xalaat ci lii? Nit a amoon ñaari doom. Mu dikk ca kenn ka, ne ko: “Doom, demal tey liggéeyi ca toolu reseñ ba.” 29 Mu ne ko: “Maa lànk,” waaye gannaaw gi, xelam yedd ko, mu dem. 30 Baay ba demati ca ka ca des, wax ko loolu. Mu ne ko: “Waaw, góor gi,” te demul.»
31 «Ana kan ci ñaar ñooñu moo def coobarey baayam?» Njiiti xeet wi ne: «Ku jëkk ki.» Yeesu nag ne leen: «Maa leen ko wax déy, juutikat yi ak gànc yi jiitu nañu leen ca nguurug Yàlla. 32 Ndax Yaxya moo leen dikke yoonu njub, gëmuleen ko; waaye juutikat yi ak gànc yee ko gëm, ngeen di gis te taxul ngeen tuub, ba gëm ko.»
Beykat wor na boroom tool
33 Weneen léeb a ngi, dégluleen: «Boroom kër la woon bu jëmbat ab tóokëru reseñ, ñag ko, gas ca paxum nalukaayu reseñ, tabax ca taaxum wattukaay, ba noppi batale tóokër ba ay beykat, daldi tukki.
34 «Ba wittum reseñ jubsee, mu yebal ay surgaam ca beykat ya, ngir jëlsi wàllam ca meññeef ma. 35 Beykat ya jàpp surga ya, kii ñu dóor ko, kee ñu rey ko, kale, ñu sànni ko ay doj. 36 Boroom kër ga yebalaat yeneen surga yu ëpp yu njëkk ya, beykat ya def leen noonu. 37 Mu mujj yebal doomam te naan: “Sama doom, dinañu ko rus.” 38 Teewul ba beykat ya gisee doom ji, dañu ne ci seen biir: “Kii mooy donn; nanleen ko daldi rey, ba jagoo ndonoom.” 39 Ci kaw loolu ñu jàpp ko, génne ko tóokër bi, rey ko.»
40 «Bu boroom tóokër bi dikkee, nu muy def beykat yooyu?» 41 Ñu ne ko: «Reyin wu ñaawa ñaaw lay rey ñu bon ñooñu, tóokëru reseñ ba, mu batale ko yeneen beykat yu ko jox wàllam ca meññeef ma, saa yu jotee.»
42 Yeesu nag ne leen: «Xanaa masuleena jàng lii ci Mbind mi?
“Doj wi tabaxkat yi beddi woon,
moo mujj di doju koñu tabax bi.
Lii de, fa Boroom bi la sottee,
nu gis ko, yéemu*Seetal ci Taalifi cant 118.22-23..”
43 «Loolu moo tax ma ne leen dees na jële nguurug Yàlla ci yeen, jox ko xeet wuy meññal meññeef ma ca war. 44 Wii doj, képp ku ci dal, dammatoo, te ku mu dal, rajaxe laSeetal ci Esayi 8.14; Dañeel 2.34, 44.
45 Ba sarxalkat yu mag ya ak Farisen ya déggee léebi Yeesu yooyu, xam nañu xéll ne ñoom lay wax. 46 Ñu di ko fexee jàpp nag, te ragal mbooloo ma, ndax ab yonent lañu ko jàppe woon.

*21.5 Seetal ci Sàkkaryaa 9.9.

21.7 cumbur: ci jamonoy jàmm, jamono yu xeex amul woon, buur yi daan nañu war mbaam, te doonul lu ñu leen di tuutal.

21.13 Seetal ci Esayi 56.7.

§21.16 Seetal ci Taalifi cant 8.3.

*21.42 Seetal ci Taalifi cant 118.22-23.

21.44 Seetal ci Esayi 8.14; Dañeel 2.34, 44.