22
Gàntal ab teraanga, dàq sa njariñ
1 Yeesu léebati leen, ne leen: 2 «Nguurug asamaan dafa mel ni buur bu doon waajal céetalug doomam ju góor. 3 Mu yebal ay surgaam, ngir ñu jëli ña ñu woo ca bernde ja, te ñooñu bëgguñoo ñëw. 4 Mu yebalaat yeneen surga, ne: “Waxleen gan ñi ñu woo, ne leen: ‘Reer yi kat noppi na; samay nag ak sama juru yafal lañu rey, lépp sotti na, ñëwleen ci bernde ji.’ ” 5 Teewul ñu fénantal, dem seen yoon; kii ca toolam, kee cam njaayam, 6 ñee jàpp surga ya, toroxal leen, rey leen.
7 «Buur nag mer, daldi yónni gàngooram, ñu reyi bóomkat yooyu, lakk seenub dëkk. 8 Ci kaw loolu mu ne surga ya: “Bernde ji de noppi na, waaye gan ñi ñu woo ñoo ko yeyoowul. 9 Kon nag demleen ca selebe yoon ya, ku ngeen fa gis, woo ko ci céetal gi.” 10 Surga ya dem ca mbedd ya, daldi dajale mboolem ña ñu fa gis, ku baax ak ku bon, ba céet ga fees aki gan.
11 «Ci kaw loolu buur bi duggsi, di xool gan ñi, daldi cay seetlu ku ag colam warul ci ag céet. 12 Buur ne ko: “Xarit, noo dugge fii, te soluloo col gi war ci ag céet?” Kooku ne cell. 13 Buur ne dag ya: “Yeewleen tànk yeek loxo yi, te ngeen sànni ko ca lëndëm gu tar ga ca biti. Foofa lees di jooye aka yéyoo ndax mitit.” 14 Ndax kat ñu bare lañu woo, waaye ñu néew lañu tànn.»
Sesaar ak wàllam, Yàlla ak wàllam
15 Booba la Farisen ya diisooji ngir lal pexe mu ñu fiire Yeesu ci kàddoom.
16 Ñu daldi yebal ci moom seeni taalibe ak ñi ànd ak farandooy Buur Erodd, ne ko: «Kilifa gi, xam nanu ne ku dëggu nga, te ci biir dëgg ngay jàngalee yoonu Yàlla. Ragaloo kenn it, ndax seetuloo ci jëmmi nit. 17 Kon nag wax nu sa xalaat: ndax yoon maye na ku fey Buur Sesaar ab galag am déet?»
18 Teewul Yeesu xam seen mébét mu bon, daldi ne leen: «Lu ngeen may seetloo, jinigalkat yi? 19 Wonleen ma poset bi ñuy feye galag.» Ñu daldi ko jox benn posetub xaalis*posetu xaalis bii: ab dinaar la woon, moo doon peyu bëccëgu lëmm.. 20 Yeesu ne leen: «Nataal bii ak tur wii ci binde, kuy boroom?» 21 Ñu ne ko: «Buur Sesaar.» Mu ne leen: «Kon nag, yëfi Sesaar, joxleen ko Sesaar, te yëfi Yàlla, ngeen jox ko Yàlla.»
22 Ba ñu déggee loolu lañu waaru, daldi koy bàyyi, dem.
Ab Sadusen gëmul dee-dekki
23 Bésub keroog boobu Sadusen yi ne dee-dekki amul, ca lañu dikk ba ca moom. Ñu laaj ko ne ko: 24 «Kilifa gi, Musaa noon na: “Su góor faatoo te amul doom, na ku mu bokkal waajur donn jabaram, ngir amal mbokkam ma dee, kuutaay†Seetal ci Baamtug yoon wi 25.5..” 25 Léegi nag juróom ñaari góor a ngi woon ci sunu biir, ñu bokk ndey ak baay. Taaw ba am jabar ba faatu te amul doom, ba tax rakk ja donn jabar ja mu bàyyi gannaawam. 26 Tofo ba ak ñaareelu tofo ba def noonu, ba juróom ñaar ñépp dee. 27 Gannaaw gi, ndaw sa it dee. 28 Keroog ndekkite la nag, kan ci juróom ñaar ñi lay doon jabaram, gannaaw ñoom ñépp a ko jëloon?» 29 Yeesu nag ne leen: «Seen njuumte moo di xamuleen Mbind mi, xamuleen manoorey Yàlla, 30 ndax keroog ndekkite la, kenn du am jabar mbaa jëkkër, waaye nit ñi dañuy mel ni malaaka yi ci asamaan. 31 Ci wàllu ndekkite sax, xanaa jànguleen la leen Yàlla waxoon ne leen: 32 “Maay Yàllay Ibraayma, di Yàllay Isaaxa, di Yàllay Yanqóoba‡Seetal ci Mucc ga 3.6.”? Kon moom du ñi dee lay seen Yàlla, xanaa ñiy dund.» 33 Ba ca mbooloo ma déggee, dañoo waaru ca njàngaleem.
Lenn ndigal moo tënk lépp
34 Ba Farisen ya yégee na Yeesu tëje gémmiñu Sadusen ya, dañoo féncoo. 35 Ci kaw loolu kenn ca ñoom, ab xamkatub yoonu Musaa, di ko fexee fiir, laaj ko ne ko: 36 «Kilifa gi, lan ndigal moo gëna màgg ci yoonu Musaa?» 37 Yeesu ne ko: «“Yàlla sa Boroom, nanga ko soppe sa léppi xol, ak sa léppi jëmm, ak sa léppi xel§Seetal ci Baamtug yoon wi 6.5..” 38 Loolu mooy ndigal li gëna màgg, te moo jiitu. 39 Ñaareel bi it yem ak moom, di: “Ni nga soppe sa bopp, nanga ko soppe sa moroom*Seetal ci Sarxalkat yi 19.18..” 40 Ci ñaari ndigal yooyu la mboolem yoonu Musaa, ak kàdduy yonent yi aju.»
Ndax Almasi bi mooy sëtub Daawuda?
41 Farisen ya ñoo daje woon, Yeesu laaj leen, ne leen: 42 «Luy seen xalaat ci Almasi bi, kan lay ab sëtam?» Ñu ne ko: «Daawuda.» 43 Yeesu ne leen: «Ana kon nan la Daawuda mana waxe ci ni ko leeru Noo gu Sell gi dikkale, ba di ko woowe “Sang bi”, naan:
44 “Boroom bi daa wax sama Sang ne ko:
‘Toogeel sama ndijoor,
ba ma teg say noon
fi sa suufu tànk†Seetal ci Taalifi cant 110.1..’ ”
45 Gannaaw Daawuda moo woowe Almasi bi “Sang bi,” nu mu nekke ab sëtam?» 46 Gannaaw loolu kenn manu koo tontu genn kàddu, te ca bés booba lañu dale, ñemeetuñu koo laaj dara.