Kàddu yu xelu
Téere bii da di ay wax yuy gindee jëme ci Yàlla, te def Yàlla muy cëslaay. Noonu la téere bi tegtale ci lu leer ne: «Ragal Aji Sax ji di njàlbéenu xam-xam» (1.7). Xam-xam man naa may boroom mu sottal ay liggéey yu ñu ko sas, te dina ko may tont yu jub ci ay laaj yu ñu koy natte. Waaye xel mu rafet rekk mooy jiite boroom ci ni mu wara dogoo jaare ci fànni dundam yépp.
Kàddu yu xelu day jàngale xel mu rafet, di wone nu mu woroo ak gis-gisu téxét bi mbaa dof bi mbaa ku bon ki.
Ci tënk:
1.1-7 Ndoortel kàddu yu xelu ak li muy xamle.
1.8—7.27 Dog bii, li ci ëpp jëm ci ay waajur ak seeni doom.
8.1—9.18 Xel mu Rafet bàkku na, di wuta berndeel.
10.1—29.27 Lu jëm ci xeltug Suleymaan.
30.1—31.9 Lu jëm ci xeltug Agur ak Lemuyel.
31.10-31 Lu jëm ci jikkoy jabar ju baax.
1
Li tax téere bi jóg
1 Kàddu yu xelu yu Suleymaan buurub Israayil, di doomu Daawuda.
2 Li ko taxa jóg di nit ñi am xel mu rafet, am ab yar, ngir xam wax ju lal dég-dég, 3 ngir yaru ci jëfe xel ak njub ak yoon, di jubal, 4 ndax ab téxét di foog, ndaw li it xam tey xalaat. 5 Na boroom xel mu rafet déglu, yokk dég-dégam, te kiy ràññee di jariñoo ay tegtal, 6 ngir mana xam aw léeb aku taas ak kàddug boroomi xel yu rafet ak seeni cax.
7 Ragal Aji Sax ji di njàlbéenu xam-xam,
te xel mu rafet akub yar, dof yaa ko xeeb.
Déglul, waajur artu la
(Saar 1.8—7.27)
8 Doom, toppal yaru baay,
te bul wacc ndigalu yaay.
9 Kaala gu jekk la ci bopp,
di gànjar ci baat.
10 Doom, bàkkaarkat bu la xiirtal, lànkal.
11 Dañu la naan: «Dikkal, nu tëruji bakkan,
yeeruji jàmbur bu deful dara.
12 Nanu mel ni njaniiw, mëdd kuy dund,
mu jekki tàbbi biir bàmmeel.
13 Mboolem alal ju réy, nu jagoo,
yeb sunu biir kër, mu fees.
14 Dikkal nu far,
mbuus miy benn, nu bokk.»
15 Doom, bul ànd ak ñoom ciw yoon,
bul jaare fa ñuy jaar,
16 ngir dañuy xélu, nar musiba,
di gaawtuy sànk bakkan.
17 Doo firib caax,
ba jàpp njanaaw luy xoole.
18 Ñii kat seen bopp lañuy fiir,
seen bakkanu bopp lañu sànk.
19 Képp kuy lekk lu lewul, nii lay mujje:
wutin wu lewul jël bakkanu boroom.
Xel mu Rafet woote na
20 Xel mu Rafet a ngay woote ca mbedd ma,
di xaacu ca pénc ma.
21 Ma ngay wootee béreb yu gëna xumb,
di dégtaley kàddoom ca buntu dëkk ba.
22 Ma nga naan: «Moo téxét bi, foo àppal sa téxét gi?
Ñaawlekat bi, foo àppal sa ñaawle bi?
Dof bi, ñaata yoon ngay bañ xam-xam?
23 Soo dëppee ba déglu, ma artu la.
Ma ne, kon ma xellil la samam xel,
xamal la samay kàddu.
24 Damaa woote, nga gàntal,
ma tàllal loxo, faaleesu ma.
25 Sofental nga samay digle,
nanguwoo samay artu.
26 Kon boo sëngéemee, man it ma ree,
njàqare dab la, may tex-texi.
27 Njàqare di ngëlén, dab la,
sa musiba def callweer, buub la,
njekkar ak fitna dal la.
28 «Keroog nga woo ma wall, duma wuyu,
nga seet ma, seet, doo ma gis.
29 Daa fekk nga baña xam,
te ragal Yàlla du loo tànn.
30 Dégluwoo samay digle it,
xanaa xeeb samay artu yépp.
31 Waaye loo ci góobe, gar ko,
say pexe suur la këll.
32 Déggadi sànk ab téxét,
naagu rey ab dof.
33 Waaye déggal ma, dëkke jàmm,
tàggook njekkar ak safaan.»