150
Màggalleen Ki Sax!
Màggalleen Ki Sax!
Nangeen màggale Yàlla biir këram gu sell,
màggale ko ca tatay asamaanam.
Màggaleleen ko ay jalooreem,
màggale ko màggam gu réy.
Màggaleleen koob bufta,
màggale ko xalam ak moroom ma.
Màggaleleen ko njiin aki pooj,
màggale ko xalam ak toxoro.
Màggaleleen ko tëggum weñ mu xumb,
màggale ko tëggum weñ mu kawe.
Na lépp luy noyyi màggal Ki Sax!
Màggalleen Ki Sax!