3
Aji jub a ngi woote wall 
  1 Dib taalifu cant, ñeel Daawuda, ba muy daw Absalom doomam ju góor*Seetal ci 2.Samiyel saar 15—16..  
  2 Éy Aji Sax ji, noon yeeka bare!  
Ñu baree may jógal,   
 3 ñu baree may tooge naa:  
«Yàlla du ko wallu!» 
Selaw
†Selaw: jàpp nañu ne ndigal la luy taxawloo woykat yi, te jombul xalam yi wéy ba tey. Waaye man naa nekk itam ndigal ngir xalam yeek woykat yi gëna xumbal..    4 Waaye yaw Aji Sax ji, yaa may feg,  
di ma teral, di ma siggil.   
 5 Maay woo Aji Sax ji wall,  
mu walloo ma fa tundam wu sell wa. 
Selaw.
    6 Maay tëdd nelaw, yewwu;  
Aji Sax ji di ma aar.   
 7 Ñu dul jeex a ma jógal, gaw ma,  
te duma ragal.   
 8 Éy Aji Sax ji sama Yàlla,  
jógal, wallu ma!  
Yaa toj kaabaabi noon yu bon yépp,  
foq seeni sell.   
 9 Aji Sax ji, yaa moom wall,  
sa mbooloo jagoo sa barke. 
Selaw.