4
Ma yendoo ñaan 
  1 Mu jëm ci njiital woykat yi, ànd aki xalam, dib taalifu cant, ñeel Daawuda.  
  2 Éy Yàlla, yaw mi may àtte dëgg,  
maa ngi woote, wuyu ma;  
maa xatoon, nga yaatal ma.  
Ngalla baaxe ma, nangul ma.   
 3 Yeen boroom daraja yi,  
buleen yàqati sama der,  
buleen sopp caaxaan, di sos. 
Selaw.
    4 Xamleen ne Aji Sax ji day séddoo ku ko ragal,  
te bu ma woowee Aji Sax ji, mu dégg.   
 5 Loxleen te baña bàkkaar,  
waxtaanleen ak seen ngegenaay te noppi. 
Selaw.
    6 Rendileen seen sarax yi war,  
te wóolu Aji Sax ji.   
 7 Bare na ñu naan: «Ana ku nuy won lu baax?»  
Éy Aji Sax ji, baaxe nu saw yiw!   
 8 May nga ma bànneexu xol  
bu raw seen pepp mu tuurook biiñ bu wal.   
 9 Jàmm laay tëdde, nelaw,  
Aji Sax ji, yaw doŋŋ yaa may dëël fu wóor.