13
Aji Sax ji, loo deeti xaar?
Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda.
 
Céy Aji Sax ji, loo deeti xaar?
Xanaa doo ma tanqamlu ba fàww?
Loo deeti xaar, bañ maa geesu,
ba ma tàggook bopp bu ubu
ak njàqarey xol bu sax,
ba noon dootu ma man?
 
Céy Aji Sax ji sama Yàlla, geesu ma, wuyu ma,
leqali ma, bala ma ne sërëx ci nelawi dee,
noon ba naan: «Daan naa ko,»
bañ yay bége saab jéll.
 
Man de maa ngi dénkoo sa ngor,
di bànneexoo sag wall.
Naa woy Aji Sax ji,
ki may baaxe xéewalam.