14
Yàqute maase na
Mu jëm ci njiital woykat yi, ñeel Daawuda.
 
Ab dof a nga naa ca xelam: «Yàlla amul!»
Ñu ni mel ay def njekkar, seeni jëf siblu,
kenn defu ci lu baax.
Aji Sax jee tollu asamaan, jéer doom aadama,
di seet ku ci xelu, tey wut Yàlla.
Ñépp lajj,
bokk yàqu yaxeet.
Kenn deful lu baax,
du kenn sax.
Aji Sax ji nee: «Xanaa ñiy def lu bon ñépp xamuñu dara?
Ñuy lekk sama ñoñ niw ñam,
te wutuñu Aji Sax ji.»
Foofu lañuy tiite tiitaange ju réy!
Du Yàllaa ngi ànd ak kuréeli ñu jub ñi?
Ku néewlee yaakaar, ngeen tas ko,
waaye Aji Sax ji la làqoo.
 
Ana kuy tollu Siyoŋ, xettali Israayil?
Éy bés bu Aji Sax ji tijjee wërsëgu ñoñam,
ndaw mbégte ci giirug Yanqóoba!
Ndaw bànneex laa ne, ci Israayil gii!