18
Buur daan, sant Aji Sax ji
1 Mu jëm ci njiital woykat yi, ñeel Daawuda jaamub Aji Sax ji. Mu jagleel Aji Sax ji woy wii, bés ba mu ko xettalee ci mboolemi noonam, xettali ko it ci Buur Sawul. Kàdduy woy wa lii la.
2 Mu ne:
Aji Sax ji, maa la sopp, yaw mi may dooleel.
3 Aji Sax ji mooy sama cëslaay,
moo may aar,
di ma wallu.
Yàllaay sama cëslaay li ma yiiroo,
fegu;
mooy Boroom doole ji may musal, di ma làq.
4 Ki yelloo cant, Aji Sax ji,
moom laa woo, mucc ci samay noon.
5 Buumi dee tanc ma,
walum kasara naq ma,
6 buumi njaniiw laaw ma,
dee ne jaas, di ma fiir.
7 Ma jàq, woo Aji Sax ji,
ne sama Yàlla wallóoy,
mu dégge këram.
Ma yuuxu, muy dégg.
8 Mu mer, suuf yëngu, di ker-keri;
reeni tund ya jaayu, di reg-regi.
9 Saxaar di sël-sëlee ca wakkan ya,
sawara boye ca gémmiñ ga,
xal yu yànj tàkke ca.
10 Mu firi asamaan, wàcc,
niir yu fatt lal tànk ya.
11 Ma nga war malaakam serub, di naaw,
daayaarloo laafi ngelaw.
12 Ma nga bàddoo lëndëm, làqoo,
làmboo ndox mu lëndëm aki xàmbaar,
13 leer a ko jiitu, xàmbaar ya topp ca,
ak tawub yuur ak xali sawara.
14 Aji Sax jee dënoo asamaan.
Aji Kawe jee àddu,
muy tawub yuur ak xali sawara,
15 mu soqiy fitt ak jumi melax,
tasaare leen, fëlxe.
16 Aji Sax ji, dangaa gëdd,
nokki, mu riir,
xuri géej ne fàŋŋ,
ron suuf ne duŋŋ.
17 Aji Sax jee yóotoo fa kaw, jàpp ma,
seppee ma ca xóotey ndox ma,
18 musal ma ca noon yu mag
ya ma bañ te man ma.
19 Ñu dajeek man, bés ba ma jàqee,
Aji Sax ji taxawu ma,
20 yaatal ma,
bége ma, ba xettali ma.
21 Aji Sax jee ma yool sama njub,
samay loxoo set, mu fey ma.
22 Sàmm naa yooni Aji Sax ji,
bonuma, di moy sama Yàlla.
23 Dama ne jàkk ndigalam yépp,
dëdduwuma dogali yoonam.
24 Seede na, may jëfeg mat,
di moyoo tooñ.
25 Aji Sax jee ma yool sama njub,
rafetlu sama mucc ayib.
26 Yaw Aji Sax ji, ku gore, fekk la gore;
ku matale, fekk la matale;
27 ku sellal, fekk la sell;
ku dëng, fekk laak say feem.
28 Yaw yaay musal xeet wu néew doole,
kuy daŋŋiiral, nga detteel.
29 Yaw kay yaa may niital.
Aji Sax ji sama Yàllaay leeral sama lëndëm.
30 Maak yaw kay, ma song gàngoor.
Maak sama Yàlla, ma tëbum tata.
31 Yàllaa mat.
Kàddug Aji Sax jee wér te wóor.
Mooy feg képp ku ko làqoo.
32 Ana kuy Yàlla ku moy Aji Sax ji?
Ana ku mat cëslaay ku dul sunu Yàlla?
33 Yàllaa may dooleel,
di ma xàllal, yoon mat.
34 Moo ma gaawal ni kéwél,
taxawal ma fu kawe.
35 Moo may tàggat ci xare,
may tàwwig fitt ci xalag xànjar.
36 Aji Sax ji yaa may feg, musal ma,
dooleel ma sa loxo,
nangul ma, darajaal ma.
37 Yaa ma xàllalu yoon,
ba duma tërëf.
38 Ma dàq noon yi, dab leen,
jekkali, doora dëpp.
39 Ma jam leen, jógatuñu,
xanaa fëlëñu, ma joggi.
40 Sol nga ma dooley xare,
sukkal ñi ma jógal, ñu féete ma suuf.
41 Won nga ma ndoddi noon,
ma boole bóom bañ yi.
42 Ñu ne wallóoy, wall amul;
ñu woo Aji Sax ji, faalewu leen.
43 Ma wol, ba ñu doon pënd, ngelaw wal,
ma wetti ni banu mbedd.
44 Xettali nga ma ci bokk yiy fippu,
def ma, ma jiite ay xeet;
waaso wu ma xamul sax nangul ma,
45 ku ma ci dégg, déggal ma,
ay doomi doxandéem di ma raamal,
46 ne yàcc,
génne seeni tata, di lox.
47 Aji Sax jeey kiy dund.
Kii ma sësoo jara sant.
Yàlla mi may musal moo màgg!
48 Mooy Yàlla ji ma feyul,
nangulal ma xeet yi.
49 Xettali nga maak noon,
kaweel ma, ma tiim ku ma jógal,
xettaleeti ma cib soxor.
50 Kon Aji Sax ji, ma sant la ci biir xeet yi,
ma kañ sa tur!
51 Yaay may sa buuru ñoñ ndam lu réy,
yaay ji ngor ki nga fal,
muy man Daawuda, di sama askan ba fàww.