19
Aji Sax ji màgg na
Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda.
 
Asamaan nee Yàlla màgg na,
kaw ne màww, biral liggéeyu loxoom!
Bésoo bés kàddu seede ko,
guddee guddi xamle ca mbir.
Du làkk, duy wax,
du baat bu dégtu,
suuf sépp la seen ndéey jibal,
seen kàddoo àkki cati àddina.
 
Kaw la Yàlla sampal jant xayma,
mu mel ni boroom séet, génne néegam,
bég ni dawkat biy xélu cib joŋante.
Asamaan lay fenke cat lii,
wëndeelu, sowi cat lee;
amul lu rëcc tàngooram.
 
Yoonu Aji Sax jee mat,
di leqali bakkan.
Lu Aji Sax ji seede dëgg la,
day xelal ku xeluwul.
Lu Aji Sax ji tegtale, njub la,
di bégal xol.
Lu Aji Sax ji santaane, leeraange la,
di leeral gis-gis.
10 Santaaneb ragal Aji Sax ji mooy li sell
te sax ba fàww.
Lu Aji Sax ji digle, dëgg la,
ak njub gu sotti.
11 Moo dàq wurus,
raw wurusu ngalam wu ne xas;
dàqati lem,
ëpp tem-tem.
12 Man, Sang bi, ci laay leerloo,
ku ko sàmm yokku yool.
 
13 Nit juum na, umple ko,
baal ma tooñ gu ma umple.
14 Te Sang bi, musal ma ci bàkkaaru teyeef,
mu bañ maa jiital,
ma mana màndu,
mucc moy gu réy.
 
15 Éy Aji Sax ji, lu saaw làmmiñ tudd
mbaa sama xol déey ma ko,
yal nay loo gërëm,
yaa may aar, yaa ma jot.