23
Aji Sax jee may sàmm
Ñeel Daawuda, dib taalifu cant.
 
Aji Sax jee may sàmm,
du lenn lu ma ñàkk.
Parlu mu naat la may gooral,
wal mu dal, mu tette ma ca,
leqali ma,
teg ma ci yooni njub
ngir teraangay turam.
Su may jaare xuru dee wu ne këruus it,
duma ragal loraange:
yaw laak man,
sa bantu sàmm ak sa nguul,
yooyoo may dalal.
 
Yaa ma berndeel,
noon yi gis,
nga diwal ma saa bopp, terale ma,
saab kaas rembat.
Mbaax ak ngor kay la ma Aji Sax jiy dare sama giiru dund,
ma dëkke këram ba fàww.