24
Ana kuy màggal Buur Yàlla?
Ñeel Daawuda, dib taalifu cant.
 
Aji Sax jee moom suuf ak li ko fees,
ak àddina ak li ci biiram.
Moo samp suuf biir géej,
dëj ko ci kaw wal mi.
 
Ana kuy yéegi tundu Aji Sax ji,
kuy taxawi bérebam bu sell ba?
Xanaa ku mucc ayib te xolam laab,
xemmemul caaxaani neen,
du giñey fen.
Kookooy jagoo barkeb Aji Sax ji,
ak àtteb dëggu Yàlla mi koy musal.
Ñooñooy waa làng gi lay wut,
di maasug Yanqóoba giy sàkku sa yiw.
Selaw.
 
Neleen bunt yi kulbét,
ubbileen bunti cosaan yi,
Buur, Boroom ndam duggsi.
Buur, Boroom ndam booboo di kan?
Xanaa Aji Sax ji Boroom dooleek njàmbaar,
Aji Sax ji jàmbaaru xare ji.
Neleen bunt yi kulbét,
ubbileen bunti cosaan yi,
Buur, Boroom ndam duggsi.
10 Buur, Boroom ndam booboo di kan?
Xanaa Aji Sax ju gàngoor yi.
Kookooy Buur, Boroom ndam.
Selaw.