32
Njéggal barke la
Dib taalifu yeete, ñeel Daawuda.
 
Ndokkalee yaw mi ñu baal ag moy,
jéggal la bàkkaar.
Ndokkalee yaw mi Aji Sax ji toppul say tooñ,
te amoo xelum njublaŋ it.
 
Ba ma nee cell,
damaa ràgg,
dëkke naqar.
Guddeek bëccëg
sa loxo diis gann ci man.
Sama doole ŋiis
ni ndox mu jaas upp.
Selaw.
Ma xamal la ne moy naa,
làqatuma la sama ñaawtéef.
Ma ne: «Naa àgge Aji Sax ji sama bàkkaar.»
Yaw nga baal ma peyug tooñ.
Selaw.
 
Nii la, kuy aji gëm di ñaane,
bu ñaan jotee.
Mbënn mu baawaan, di wal sax,
du ko laal fenn.
Yaw laay làqoo,
nga di ma aar ciw ay,
may ma ba ñi ma wër, di ko bége.
Selaw.
 
Nga ne ma: «Dama laa xelal,
xamal la fi ngay jaar,
digal la, di la bàyyi xel.
Buleen mel ni fas mbaa berkelle
mi amul ag dégg,
laab ak tarka di ko téye,
mu doora yem fi seen wet.»
10 Ku bon barew tiis.
Ku wóolu Aji Sax ji,
mu yiire la ngoram.
11 Yaw aji jub ji, bégal te bànneexoo Aji Sax ji.
Képp kuy def njub, sarxolleel!