33
Nan woy Boroom bi nu sàkk
Yeen aji jub ñi, sarxolleleen ci Aji Sax ji;
kuy jubal, màggal war na la.
Xalamleen, sante Aji Sax ji,
xalamalleen ko xalamu fukki buum.
Fentalleen ko woy,
xalam, mu neex, sarxolle jib.
 
Aji Sax jee jub kàddu.
Mooy jëfe lépp kóllëre.
Moo bëgg dëgg ak yoon.
Aji Sax ji, ngoram a fees àddina.
 
Kàddug Aji Sax ji la asamaan sosoo,
ci baatam la gàngoori asamaan yépp sàkkoo.
Moo boole ndoxi géej, jal,
yeb xóotey géej ciy mbànd.
Yeen waa àddina sépp, ragalleen Aji Sax ji;
yeen àddina wërngal këpp, wormaalleen ko.
Moo àddu, mu am;
santaane, mu sotti.
10 Aji Sax jeey neenal li xeet yiy fexe,
di gàntal li mbooloo yiy mébét;
11 Aji Sax ji nas, mu àntu ba fàww,
mu mébét, mu sottil maasoo maas.
12 Ndokkalee yeen xeet wi Aji Sax ji di seen Yàlla,
yeen askan wi Aji Sax ji séddoo.
13 Asamaan la Aji Sax jiy jéere,
di gis doom aadama yépp.
14 Jal ba mu tooge
lay niire waa àddina sépp.
15 Moo tabax seen xol, ñoom ñépp;
lu ñu def, xam na ko.
16 Mbooloo mu réy mayul Buur ndam,
doole ju bare walluwul jàmbaar.
17 Yaakaar aw fas nax sa bopp la,
kàttanu fas dug wall.
18 Ma ne, Aji Sax jee naa jàkk ku ko ragal
tey wéeroo ngoram.
19 Day bakkanam,
di ko dundal cib xiif.
 
20 Nu ngi séentu Aji Sax ji,
moo nuy taxawu, di nu feg.
21 Ci moom la sunu xol di sedde,
turam wu sell lanu wóolu.
22 Aji Sax ji, ngalla baaxe nu sa ngor,
moom lanu yaakaar fi yaw.