43
Éy Yàlla, àtte ma
Éy Yàlla, àtte ma,
layool maak xeet wu gorewul,
xettali maak ku njublaŋ te dëng.
Yaw Yàlla kat yaay sama rawtu.
Lu tax nga wacc ma,
may wéye tiis,
ci nooteelu noon?
Ngalla yónneel sag leer ak sa dëgg,
yal na ma yooyu jiite,
yóbbu ma sa tund wu sell,
sa màkkaan ma.
Kon Yàlla, naa àgg ca sa sarxalukaay;
yaw Yàlla, yaay sama mbégte, di sama bànneex.
Yaw Yàlla, sama Yàlla,
naa la màggale xalam.
Moo man, lu may xàddi, ne yogg?
Lu may jàq nii?
Tee maa yaakaar Yàlla, ba santati ko,
moom sama Yàlla mi may wallu?