44
Xeet waa ngi jooy
Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu yeete bu ñeel askanu Kore wu góor.
 
Éy Yàlla, noo déggal sunu bopp,
sunuy maam a nu wax
jëf ja nga jëf ca seeni jant,
bu yàgga yàgg.
Yaw ci sa bopp yaa dàq xeet yi,
jëmbat fa maam ya;
yaa mbugal xeet yi,
ñoom, nga yiwi leen.
Du seen saamar lañu nangoo réew mi moos,
seen dooley bopp it mayu leen ndam.
Yaa ko defe kàttan ak doole,
geesoo leen sa leeru kanam,
ngir sa cofeel ci ñoom.
 
Yaay kiy sama buur, di sama Yàlla,
mayal askanu Yanqóoba ay ndam.
Yaw lanuy dàqe bañ yi,
sa tur lanuy dëggaatee ñi nu song.
Du fitt laa wóolu,
du saamar a may may ndam.
Yaa nuy musal ci bañ yi,
yaay gàcceel noon ñi.
Yàlla lanuy damoo bésoo bés,
di màggal turam ba fàww.
Selaw.
 
10 Waaye danga noo wacc,
toroxal nu,
ba àndulook sunu mboolooy xare.
11 Waññi nga nu, nu won noon yi gannaaw,
ñu bañ nu, ba futti nu.
12 Ni gàtt yu ñuy yàpp, ni nga nu joxee,
tasaare nu ci biir xeet yi.
13 Jaay nga sa mbooloo ci dara,
te jariñu la tus.
14 Tax nga sunuy dëkk di nu ree,
ñi nu séq di nu kókkaleeka ñaawal.
15 Tax nga xeet yi di nu léeboo,
jàmbur yaa ngi nuy wëcc bopp!
16 Damaa dëkke gàcce,
sëlmoo kersa
17 ndax kókkali yeek xastey nit
ñi ma bañ, di feyoonteek man.
 
18 Lii lépp dal na nu,
te fàttewunu la, fecciwunu la kóllëre.
19 Dëdduwunu la,
waccunu saw yoon,
20 teewul nga noot nu, wacce nu xaj ya,
këpp nu lëndëmu dee.
21 Su nu la fàtte woon yaw, sunu Yàlla,
ba tàllal tuuri doxandéem yi loxo,
22 du la ump, yaw Yàlla,
mi xam kumpay xol.
23 Yaa tax ñu yendu noo bóom,
dees noo jàppe ni xar yu ñuy tër.
 
24 Éy Aji Sax ji, jógal! Looy nelaw?
Yewwul, bu nu wacc ba fàww.
25 Loo nu làqe saw yiw,
di fàtte sunu njàqareek sunu coono?
26 Nu ngi ne ñàyy ci pënd bi,
di watat koll fi suuf.
27 Wallusi nu, jot nu ngir sa ngor.