49
Alal day naxe
1 Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel askanu Kore wu góor.
2 Yeen, xeetoo xeet, dégluleen;
yeen, waa àddina yépp, teewluleen,
3 ngay ku tuut di ku mag,
nga bareleek nga néewle.
4 Li may wax xel la,
di xalaat yu déggu.
5 Damay teewlu kàddu yu xelu,
xalamal la sama tekkiteb cax.
6 Ana lu may tiit bés yu metti,
yu ma njublaŋ yéewe seeni ñaawtéef,
7 di ñu wóolu seen am-am,
di kañoo alal ju bare?
8 Ana ku mana jot a jot sa bakkanu moroom,
mbaa mu di ko feyal Yàlla njot ga?
9 Njotug bakkan jafe na,
bu ci jéem dara.
10 Ana kuy dund ba fàww,
ba doo gis bàmmeel?
11 Xanaa gis ngeen ne xelu, dee;
dof, dee; naataxóona it faatu rekk,
wacce keneen alalam.
12 Sa bàmmeel di sa kër ba fàww,
di sa dëkkuwaay bu sax dàkk,
boo tudde woon sa bopp ay suuf sax.
13 Nit ak darajaam fanaanul,
mook aw rab a yem, sànku rekk.
14 Nii la ku wóolu boppam di mujje,
mook ku ko topp, di safooy waxam.
Selaw.
15 Nara dee rekk niy xar,
dee wommat, yóbbu,
njub fenk nib jant, ku jub moom leen,
njaniiw mëdd seen jëmm,
fu sore kërug daraja.
16 Waaye Yàllaa may musal ci dooley njaniiw,
jot sama bakkan, ba jël ma.
Selaw.
17 Buleen yéemu ci ku barele,
teraangay këram di yokku.
18 Du dee ba yóbbaale dara,
teraangaam du ko topp biir bàmmeel.
19 Na bége bànneexu bakkanam,
ñu di ko kañe koomam,
20 ba tey, day dee, fekkiy maamam,
ña dootul gisug leer ba fàww.
21 Nit ak darajaam te amul dégg,
mook aw rab a yem, sànku rekk.